Ngir màggal bés bi Séex Anta Jóob génne àddina, OSAD a ngiy indi jukki bi mu tibbe ci waxtaan wi boroom xam-xam bi amaloon ca Kees, jagleel ko janq ji doon tàggatu ci wàllu njàngale, ci awril 1984.
Jukki baa ngi nii
Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko. Làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ni paaka bu xomaag. Te Tubaab yi, bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu ko yore ci seen làmmiñu bopp. Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des gannaaw. Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag njaboot, ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko…Loolu moo taxoon nu sàggane sunu làmmiñ yii. Waaye du caagéeni dañu mënul woon a wax li nu bëgg a wax…
Le Soleil : Altine 1 Few 2010 TUUBAA TV TÀMBALINA CI SATELIT.
Tuubaa TV di telewisioη bu bees gu « yar, yéene ak bégale, ci anam yu dëppook i teggin » tax a jóg tàmbalina àjjuma jii weesu ci satelit.
Tuubaa TV te bàkkam di « Tele bi ñu nuru? » jàppandina ci satelit fii ci Afrig ci frekãs W4-12.437 14 GHz, fii ak muy tàmbali ci Tugal ak Amerig ci weeru màrs gii di ñëw, la ñu jibal. Tele boobee nag, ay doomi Senegaal yu màcc ci jokkolante (communication), a ko taxawal ci nowàmbar 2009, ngir « jàppandal doomi réew mi tele bu dëppook i teggin, rafetal ak diine yi waa Senegaal aadawoo? ».
[Askan] 42,2% ASKANU SENEGAAL A NGI AM LU NÉEW 15 AT CI 2009 : Gàllankoor gu réy ?
African Global News : Talaata 26 Samwie 2010 42,2% ASKANU SENEGAAL A NGI AM LU NÉEW 15 AT CI 2009 : Gàllankoor gu réy ?
Senegaal, ni ki réewi Afrig yi toll ci limug askan guy yokk, a ngi am askan wu ndaw ña ëpp. Wàññikug ndee gi, te yokkug paj mi waral ko, moo waral njur gu gaaw. Waaye cim réew lu njur ga gën di yokk njélul njàngale ma, paj ma ak ligéey doon lu diis..
Askanu Senegaal mi tolloon ci 2.750.000 (ñaari milyong ak juróom-ñaar téeméer ak juróom-fukki junni) doomi aadama ci atum 1950 jàll na ci 13.711597 ca atum 2009. Yokkute askanu Senegaal gu gaaw googu, ni ki réewi Afrig yépp daanaka, doon na luy ga (imposé) nguur yi politigu soqalig koom-koom guy sóoraale seenug limu askan. Muy lu doy kéemaan ndax lu aw limu askan di gën di yokk, limu ndaw ñi war a dal am njàng mbaa aajowoo ligéey, di gën di yokk. Waaye li ci yéeme mooy njélul réew yooyee matalewul limu askan ya.
[Jàngale ak Tàggat] Daara yee ngi laaj seen wàll ci njélul njàngum réew mi.
WalFadjri : Gaawu 23 Sam 2010 NJÀNG : Daara yee ngi laaj seen wàll ci njélul njàngum réew mi.
Ndax mënatuñoo dëkku jafe-jafe yi aju ci matale seen i wareef ci daara yi ak internat yi, ñiy yëngu ci njàngaleem alxuraan ak yaru lislaam, daje démb cim pénc ca dalub mbooloom jullit yu àddina si (Ligue islamique mondiale) ne ca Ndakaaru, wone nañu seenug jaaxle ci doxal, ni mu waree, daara yooyee. Ni ki noonu ñi ngi laaj seen wàll ci 40 % njél li nguur gi jagleel njàngaleem réew mi.
[Diine] Màggalug Tuubaa: Ab tënk ñeel Taarix ak lu aju ci bis bu tedd bi.
Xibaaryi.com:Talaata 19 samwie 2010 Màggalug Tuubaa: Ab tënk ñeel Taarix ak lu aju ci bis bu tedd bi.
Màggalug Tuubaa,Bis la bu màgg fi Taalubey Sëriñ Tuuba yi te it di bis bu nu fonk, Di it bis bi Sëriñ bi demee ci tukkib liggeey bi, ci 18 ci aw Magal (safar), Nu di ko amal at mune fa Tuubaa, ci fukki fan ak juróom ñatt (18) ci aw Màggal (Safar), ci arminaatu (calendrier) weer wi walla bu Hijri. Teg ko ci ndigalul Sëriñ Tuubaa "Bu bis bi ñëwatee na ngeen ma Santal Yàlla kem séen kàttan".
Mu digle woon ko ci fukki fan ak juróom ñatt ci atum 1341 ci hijri, di 16 julet 1921 ci Gregorian. Muriid yi di juge fune di jëm Tuubaa, ngir amali ko fa barab bu tedd boobee, dem na nag ba yamatul rekk ci Muriid yi, Waaye xanaa nekk xew-xewu Julli ñépp, Mbaa sax nit ñi ngir mu gën a matale, Muy yitte ju rëy, Ay miliyoŋi nit diko teewe.
Xupees na sañ-sañu wax sa xalaat. Fees jëm ak sunu demokaraasi bii? Réew mom yennat ciy xalaat ñoo fi dagan, yeneen daa araam, réew mees ne : sañ-sañu xalaat génne ko, péexteg afal sa xel, lu mu jur nga wësin ko niki yooyee demokaraasi di yu Tugal yees ne ñooy ya mag yees di roye, ba jural nu nuy lang ciy mbiccam, di jafandu ciy waggam, naan lu fiy lu baax moom a déet keneen, déet feneen, ba sax lu ba woo feneen du leneen lu dul neen ndax li muy keneen, bub gox goobeem mbayam te sax mu gën mu kile, waxees ne fa la ko duppee, cëy lile! Lii ak lu ni mel moo jur natt ci ñaari nattukaay gi Tugal di def ba ay farandoom di ko ca fekk ak a roy.
[Bitim réew] Xaatimees na ag déggoo guy génne réewum Gine ciy jafe-jafe.
Le Monde : Gaawu 16 Samwie 2009 Xaatimees na ag déggoo guy génne réewum Gine ciy jafe-jafe.
Ag déggoo ngir génne réewum Gine ciy jafe-jafe la ñu xaatim àjjuma 15 samwie ca Wagadugu. Li déggoo googu ëmb mooy bàyyandikug Kapiten Musaa Dadis Kamara mu "dallu" ca bitim-réew ak amalug joηante njiitu réew "fii ak juróom-benn weer". Ganaaw ñaari fanu weccoonte xalaat, la ko ñett ñii xaatim : kapiten Dadis Kamara, Seekuba Konaate mi jiitandeegum réew ma ak njiitu réewum Burkinafaasoo Belees Kompawore, di ab yombalkat.
[Politig] Senegaal: Amaleesna Njëwriñ ju yor mbiiri
Sen24heures.com : Àllarba 06 samwie 2010
Senegaal : Amaleesna Njëwriñ ju yor mbiri diine yi.
Njiitu réewum Senegaal Abdulaay Wàdd tàbb na jëwriñ ju yor mbiri diine yi, di guléet ci réew mi. Looloo ngi am ci jamono ju ñagas digante ay kilifa diine ak njiitu réew mi, la Njëwriñu Jokkanlante gi xamale.
S. Mamadu Bàmba Njaay, di taskatu xibaar bokk ci làng politigu nguur gi, la ñu tàbb Jëwriñ xelalkat bi yor mbiri diine yi teg ci yor kàddu njiiru réew mi, la AFP siiwal jéle ko ci Njëwriñ loolu.
Gannaaw ba mu siiwalee lees war a xam ci jabet, doktoor Abdul Asiis Kase (Dr Abdoul Aziz KASSE, Chirurgien Institut du Cancer, Université Cheikh Anta DIOP) dellusi na, di xamle ñam yi aji-jabet war a lekk ak yi mu war a moytu....
[Diine] [Wideo] Ay ndaw jàmmaarloo nañook takk-der yi ci buntu katedral bi
APS : Àllarba 30 Des 2009
[ Wideo ] Ay ndaw jàmmaarloo nañook takk-der yi ca buntu katedral bu Ndakaaru.
Ndakaaru, 30 des (APS) - Takk-der yi tasaare nañu àllarba aki fàccaakonu gëlëmël (grenade lacrymogène) ab doxu ñaxtu bu ay ndawi kercen amaloon ba ñu génnee ci mees bu katedralu Ndakaaru bi nekk ca wetu njéende réew mi, loolee la APS yégle.