Ndakaaru, 5 Sulet (APS) - Seex Kan, ñu di ko wax ‘’Elton’’ bu ekiri Bàlla Gay, jél na ndamul ñetteelu joηante bëre dóor (CLAF), ci kaw Yékini Siñoor, ca estaad Demba Jóob bu Ndakaaru, la taskatu xibaar bu yéenekaay APS wax. Moor Taal Njaay, ñu di ko wax Jékini Siñoor, a ngi ñàkk bëré boobu gannaaw jàppante bu ëpp ñaari minit.
Elton a ngi sukkandiku ci dooleem (120 kg), ngir moy ñaari yoon njuuy yi ko Yékini tegaloon, laata mu koy daan.
Gannaaw bi mu ñàkke joηante CLAF bu daaw, mbëru ekiri Bàlla Gay jél na ñetteel yoon bi. Mi ngi topp ci Suley Dop mu ekiri Siin-Saalum (mi ko jéloon ci atum 2008) ak Lak de Geer 2 bu Waalo (mi ko jéloon ci atum 2007).
Tolli ci 21 at, Seex Kan mi bokkon ci puul A bu CLAF, moo daan Bismi Ndóoy, Maam Góor Juuf ak Mataar Géy, laata muy daan Yuusu Nduur (mi mësoon a jél raaja njiital nguur gi) ci génn-wàllu finaal bi.
Ci jalbéen ga, Ndóof mu ekiri Faas moo daan Fëgëlu bu ekiri Lansaar. Ndamal Ndóof li dina may ekiri Faas mu noyyiwaat tuuti.
Waaye Amaneex, bu ekiri Lébugi, mooy ki fa gënoon a ràññiku. Moo daan Mon 1 bu ekiri Siin-Saalum ak teknig bu rafet. Diisaayam teewul Amaneex jëfandikoo woyofam ngir jéll aji-jàmmarloowam.
Du lu Móodu Xule bu ekiri Bàcc Séeraas, def. Moom Paap Seen bu ekiri Mbay Faal la ko daan. Doomu Jalaaw bu ekiri Caaroy moo daan Usmaan Juuf bu ekool bére bu Mbay Faal. Promotëer Gaston Mbeeng a amaloon joηante bére CLAF boobu.
Delluwaay:
Wolof: E. M. Ngeer - Xibaaryi.com


Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com est un site d’information générale en wolof, langue parlée par plus de 80% de la population du Sénégal. C'est le résultat du mémoire de maîtrise d’Ibra Ndiaye et Kelekey Moussa Diakhaté (promotion 2008 de la maîtrise informatique de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis du Sénégal). Il s'agit d'un site visant à permettre...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com is a site of general information in Wolof, a language which is spoken by over 80% of the Senegalese population. This is the result of the Master's memoir of both Ibra NDIAYE and Kelekey Moussa DIAKHATE (academic year 2008, Master's in Computing, Saint-Louis Gaston Berger University, Senegal). This site...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com ist eine allgemeine informationsseite auf Wolof, der Sprache, die von mehr als 80% der senegalesischen Bevölkerung gesprochen wird. Sie ist das Ergebnis der Masterarbeiten von Ibra NDIAYE und Kelekey Moussa DIAKHATE (Sommersemester 2008, Masters der Informatik, Universität Sain-Louis Gaston Berger, Senegal). Diese Webseite möchte Wolof-Sprechern Informationen zugänglich machen....
Yër li ci topp|
• lu tee tasum xibaaryi ci wol... Ndate man bis bu ma xéyee rekk te am jot xool na ko waay... |
| 19/04/13 23:16 |
| karim |
|
• Alquraan ci wolof Sëriñ bi na ko yàlla miy boroom katàn te télewul dar... |
| 30/03/13 06:14 |
| kariim |
|
• Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fe... |
| 31/12/12 02:25 |
| kariim |
|
• ci mbiri wàtayi Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu wa... |
| 14/04/12 11:36 |
| kariim |
|
• Di sant Yaalla rek a askan wi Rafetlu naa ci ndam li Makki Sal am waaye nak Ablaay Waadd n... |
| 08/04/12 11:32 |
| Mouusa |









![]() | Tay | 45 |
![]() | Démb | 2061 |
![]() | Ayu-bis bii | 7452 |
![]() | Weer wii | 72728 |
![]() | Lépp-Lépp | 1572315 |