Amount of short articles:
Amount of articles links:
You can order sections with dragging on list bellow:
Abdul Mbay mi njiitu réew mi, Maki Sàll, tabb njiitu jëwriñ yi mi ngi toll ci 59 at, doon ku màcc ci wàllu Bànk. Am na raaya bu Daara Ju Kawe ci wàllu Yaxantu bu nekk Paris, ñu duppe ko ci farañse "HEC École des hautes études commerciales de Paris", bu Sorbon ak bu Iniwersite Seex Anta Jóob bu Ndakaaru.
Ca HEC, bokkoon na faa nekk ak François Hollande, mi bokk ci joηante njiitu réew mu Fraas bi war a am weeru awril jëm Mee.
Ci atum 1976, la doomu àttekat bu siiw bii di Keebaa Mbay duggu ci Bànk bi Réewi Afrik sowwu-jant bokk, niki ab koomkomal (économiste) ci bànqaas bi yor wàllu gëstu ci njiital Alasaan Watara, mi doon tey njiitu réewum Koddiwaar.
Ci atum 1982, fekk mu toll ci 29 at, la ko njiitu réew ma woon Abdu Juuf fal njiitu lu njëkk bu Bànku Dëkkuwaay bu Senegaal (Banque de l’habitat du Sénégal) laata muy jàpp ci atum 1990, ci suqalig bànk bii di BIAO-Senegaal.
Gannaaw ba mu nekk Njiitu CBAO mi juddoo ci faatug BIAO. Bi mu nekkee ci kaw CBAO, la Abdul Mbay ubbi lonkoo bi njëkk def ci Senegaal li àngale di wax leasing ak gafag alalal gu njëkk ci Afrik Sowwu-jant.
Moo njëkk a doon njiitu GIM (Mbennoy Bànk ci wàllu Monetik) bu UEMOA, njiitu te bokk ci way-sos ISA (Daara ju kawe juy tàggat njiitu këru-liggéey yi), njiitu Kuréel giy doxal Lekkool Bariteknik bu Cees (Ecole polytechnique de Thiès).
Ci atum 1999, la bokk ci kurél gi jënd BST (Bànk Senegaal ak Tinisii) te mu mujjoon a doon njiit la te mujj koo suqali ci ñetti at rekk. Ci atum 2006, la Attijari Bànk jënd yoxo yi ëpp ci BST.
Abdul Mbay doon a jàngale politiku monetik ci ENA (Lekkoolu biir yéew miy tàggat ci Yoriin), njiitu kurélu ’’Alalal ak yaxantu’’ bu Jataay Koom-koom ak askan, bokk na it ci Jataay bi njiitu réew miy amal ci wàllu alalal (invertissement).
Di ku yittéel lool tàggat-yaram, ba nekkoon na ki yor xaalisu Bennoo Senegaal bu Futbal (Fédération sénégalaise de football), njiitu Bennoo Senegaal bu Daw (fédération sénégalaise d’athlétisme).Bokk na tey ci mbooloo miy fësal kurélu Tàggat-Yaram bi àdduna sépp bokk (CIO).
Amna soxna ak 4 doom, Sëñ bi Mbay bokk na ci ñi seen jëf gën a ràññeeku ci Senegaal ak ci Faraas.
OID/ASG
Jukki bi mu askanoo : APS
Aji-tekki ji ci Wolof: A. M. NGEER - Xibaaryi.com


Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com est un site d’information générale en wolof, langue parlée par plus de 80% de la population du Sénégal. C'est le résultat du mémoire de maîtrise d’Ibra Ndiaye et Kelekey Moussa Diakhaté (promotion 2008 de la maîtrise informatique de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis du Sénégal). Il s'agit d'un site visant à permettre...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com is a site of general information in Wolof, a language which is spoken by over 80% of the Senegalese population. This is the result of the Master's memoir of both Ibra NDIAYE and Kelekey Moussa DIAKHATE (academic year 2008, Master's in Computing, Saint-Louis Gaston Berger University, Senegal). This site...
Yër li ci topp
Xibaaryi.com ist eine allgemeine informationsseite auf Wolof, der Sprache, die von mehr als 80% der senegalesischen Bevölkerung gesprochen wird. Sie ist das Ergebnis der Masterarbeiten von Ibra NDIAYE und Kelekey Moussa DIAKHATE (Sommersemester 2008, Masters der Informatik, Universität Sain-Louis Gaston Berger, Senegal). Diese Webseite möchte Wolof-Sprechern Informationen zugänglich machen....
Yër li ci topp|
• lu tee tasum xibaaryi ci wol... Ndate man bis bu ma xéyee rekk te am jot xool na ko waay... |
| 19/04/13 23:16 |
| karim |
|
• Alquraan ci wolof Sëriñ bi na ko yàlla miy boroom katàn te télewul dar... |
| 30/03/13 06:14 |
| kariim |
|
• Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fe... |
| 31/12/12 02:25 |
| kariim |
|
• ci mbiri wàtayi Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu wa... |
| 14/04/12 11:36 |
| kariim |
|
• Di sant Yaalla rek a askan wi Rafetlu naa ci ndam li Makki Sal am waaye nak Ablaay Waadd n... |
| 08/04/12 11:32 |
| Mouusa |









![]() | Tay | 1592 |
![]() | Démb | 6321 |
![]() | Ayu-bis bii | 7913 |
![]() | Weer wii | 66868 |
![]() | Lépp-Lépp | 1566455 |
Ngéen baal sama Wolof bu tawat bi!