Maki Sàll tënk na ci 8 digub at yi oto yiy dugg Senegaal war a am.

maki_otoNdakaaru, 13 awr (APS) - Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yiy dugg Senegaal tey juge bitim-réew war a am. Mi ngi ko dogalee ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.

‘’Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare n° 2012-444 soppi bub n° 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi. Dekkare boobu day tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yiy duggu Senegaal war a am’’, la njibal, lees siiwal àjjuma jii, karmat.

S. Sàll dige woon na ci batum dagaan ne dina ko def bees ko tegee ci boppu réew mi. ‘’Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal. Lutax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal ?’’, la waxoon.

Dogal booboo ngi tukke woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar  yi te aar kéew gi ci saxaar su bon siy tukkee ci oto yu màgget yi. 

Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon. Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dugal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.

BHC/SAB

Jukki bi mu bawoo:  APS

Aji-tekki ji ci Wolof: A. M. NGEER - Xibaaryi.com

Ñaata yër: 1218
Àddu yi (2)Add Comment
0
ci mbiri wàtayi
Aji-Bind ji kariim, April 14, 2012
Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu waroon a def mooy bëpp kuy doo mu wa senegaal te dékk bitim réew ñu may la ci dirup juróo mi àt ( 5 ) yu ne nga am sañ sañu Ëndi been ( 1) wata bu am fukki àt ak ñaar ( 12 )àt te ñi nga xaam ne ñoom da ñiy dema a ka dikk di ciy def ay baana baana maa nam njénd ak njay , ñu dafal leen ko ci juróom ñatti tà ( 0- 8-b 9 ) lii dall moo époon yér maande ci àsskanwi ndax bumu fatte ne fii mu tolu tembe Ëróop dafa tollu fo xam ne ngir nga man fee am lo jénnde watap 10 ki àt du lu yombu gi law, na fexe ba la dalon górgi bumko dall ndax górgi nàgoo ka fi jéle woon , ndax doomi senegaaluwa ni nekk bitimréew jege na ñu miliyoon te 5,000 bu nekk senegaal tay 3,000 wa asskàn wi nekk a bitim réew ñoo kofi dugal ta ñoom kàt bu watte joote ku ci nekk bo woote say bokku koo ne nañ ko wateel moom la ñiy wateel ,
0
Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee
Aji-Bind ji kariim, December 31, 2012
Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fekke tay jii di fukki fàn ak juroom ñaar ci weeru `Sàfar Àtum 1434 Ijira wala Àxirra .insàlla suba bunu yàlla mayee fekke ak tall ko ci la julit yépp wara sanntë le¨Sriñ bi yàlla sub àanala yàlla na nu ca yàlla bole te jègal nu mbolem sunuy bakkar yu jékk ak yu muju amin;.
ndax li keroog bisub Gaawu bamu julle fajar ca cëyéen séllmal gënne ca jakkàm je woolu maam cerrno biraa'im neko cerrno mu ne ko Mbakee, ,mune ko darra jéruma wax ,joot naa ndigal li ma doon xaar ta mooy ndigalal sama boroom mu bayi koo ca raasuli la
Toog leen ma dem ligèyi te ñéw ngen añe mangi len di xamal déñké naa len ki nga xamne lu ko way dénk raw na pexem saytànne te koo ku mooy yonnet yàlla Muhammet,te baye naa lenak ñatt, ak ñatt, nangen di taxoo laab ak jaang Alxur'aan tay sukéndiku ci sunas yonnentibi na ngeen ligèy lu ngen di dunde ci anam gu dagan.
loo lu mingi amoon ci bisub Gaawu di 18 safar àtum 1273 ca Àxiraa di tolook 05/09/1895 ca céyéenuk jolof .
Ban demee ba 18 safar 1299 sériñ bi ci bopam digle ñu santal ko ci yàlla, fu bis bii jota te fumu fekkub julit mangilay ñaan nga sante lemaci yàlla.
Maan nik duma sos ,suna ndax tëbaski'aat sunu maam Ibraa'ima la kon nik buko kenn tude tébaski,
nangen ko tude ak cantt, li ko tambu leen ci ginarr ba ci galleem bu kenn xeeb bu kenn yéem lu di soyee 1921 06/1921 yàlla na nu yàlla may fan wu gudu te andag wérgi yaram ak wérség,yaxiin cofeel ci sunu sang yonentibi ,tabe gu andak rafet jiko ,soop Sëriñ Tubaa mucu ci saytaane ak jistal amin. sen mbokum talibe sopey bépu waluyu mbaa xubul samaani jamoonoyi tambu lee ko ci rasull yi ak nëbiyu yi,wasalaam Abul Kariim Jóob

Àddu ci Jukki bi

busy

Ñiy dugg ci Dal bi

mod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_counter
mod_vvisit_counterTay1249
mod_vvisit_counterDémb2324
mod_vvisit_counterAyu-bis bii12619
mod_vvisit_counterWeer wii56942
mod_vvisit_counterLépp-Lépp1647289

Amna: 11 gan, 9 bots yu lënku
Sa IP: 50.16.36.153
Tay la Suw 19, 2013

Ay yëgle yu bawoo Google