10 dénkaaney wér-gi-yaram ci weeru koor gi.
- Naan ndox dénkaane bi ëpp solo ci weeru koor gi. Saa yu dog jotee, aji-woor ji da cee war a naan lu takku. Kenn warul a fàttee naan it ci waxtu xëdd.
- Ci wàllu ñam yi, taamuwees na ñam yu sell ci ñam yu saf suukar yi, yoy lumu bari bari du tee xiif rax ci dolli dañuf sonnal yaram wi.
- Dog tekkiwul lekk gu bari. Lekk gu baru du yem ci sonnal yaram wi rekk, waayit day yàqi nelaw.
- Dénkees na aji-woor ji muy lekk ay meññeef (fruit) ngir am ay witaamin, rawatina suukar yu yeex yi ak pepp ngir dëgërlu ci bëcëg bi. Ba tax na, xëdd baax naa def lool.
- Dontale koor gi ci bëccëg bi la, aji-woor ji war naa lekk ñetti yoon ci bis bi : bi njëkk di buy xëdd, ñaareel bi di buy dog, ñetteel bi di ñaar mbaa ñetti waxtu gannaaw bu mu dogee.
- Mu mënee nekk, as ndallu (sieste) baax na lool ci ngoon gi.
- Weeru ut daa nar a tàng. Dénkees na aji-woor ji muy moytu jant bi ak tàngoor wi.
- Dontale weeru koor amuli lor daanaka ci wér-gi-yaramu aji-woor ji, teewul dina baax lool ci moom mu néewal ay yëngoom. Way-tàggat yaram yi nañu moytoo ëppal ci weeru koor gi.
- Way-woppu jabet yi dénkees nañu leen ñuy seetlu fu seen suukar toll, di naan ndox mu bari, di moytu ñamu suukar yi ngir wàññi jéyyay wér-gi-yaram ci diirub koor gi.
- Way-néew doole yi namm a woor, niki jigéen yu ëmb yi, màgget yi mbaa ñi ame tasyoη walla asma, nañuy seetlu ji kër doktoor saa yu ñu yegee lenn lu jaaduwul ci seen yaram. Ngir ag kaarànge, dénkees nañu leen ñu seetlu ji kër doktoor bu weeru koor gi teru ak bu jàllee.
senxibar.com
Jukki bi mu askanoo
Aji-tekki ji : A. M. NGEER - Xibaaryi.com