Politig, Gis-Gis, Koom-Koom,Yokkte Ak Dimbalante

Edit

Amount of short articles:

Amount of articles links:

You can order sections with dragging on list bellow:

  • Politig, Gis-Gis, Koom-Koom,Yokkte Ak Dimbalante
Denc
Neenal
Defaat

Gis-Gis & Céru

Cér bi jàkka yor war naa

Image - Cér bi jàkka yor war naa

Ci jegeg Tëbëski gi, samab siyaaree ngoogu, di léen ci wax déwénati: Cér bi Jàkka yor war naa yokku

Altine, 11 Oktoobar 2010 Àddu yi

Koom-Koom & Yokkte

Maki Sàll tënk na ci 8 d

Image - Maki Sàll tënk na ci 8 d

Ndakaaru, 13 awr (APS) - Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub a

Gaawu, 14 Awril 2012 Àddu yi

Politig

Senegaal - Limu jëwriñi

Image - Senegaal - Limu jëwriñi

Njiitu réew mi Maki Sàll yem na ci 25 jëwriñ ngir taxawal nguuram, niki mu ko digee woon ca bamuy

Alxames, 5 Awril 2012 Àddu yi

Politig

Senegaal - Limu jëwriñi nguuru Maki Sàll gu njëkk

abdul_mbay1_copy

Njiitu réew mi Maki Sàll yem na ci 25 jëwriñ ngir taxawal nguuram, niki mu ko digee woon ca bamuy dagaan ci tànneef ya.

 

Limu ñi bokk ci nguur gee ngii ñu siiwal àllarba ci ngoon:

- Aliwun Badara Siise, jëwriñ ji yor jëflanteek bitim-réew ak doomu Senegaal ya ca bitim-réew

- Mbay Njaay, jëwriñ ji yor biir réew mi

- Ewa Mari Kol Sekk, jëwriñ ji yor wér-gi-yaramm ak ndimbalante gi

- Ogistin Tin, jëwriñ ji yor kaarànge gi

- Aminata Ture, jëwriñ ji yor wàllu yoon

- Aamadu Kan, jëwriñ ji yor koom gi ak alalal ji (Finance)

- Yuusu Nduur, jëwriñ ji yor Caada ak turism

- Maryaama Saar, jëwriñ ji yor wàllu Soxna yi, Xale yi ak liggéeyu jiggéen ñi

- Ibraayma Sàll, jëwriñ ji yor njàngum biir réew mi

- Bonuwaa Sàmbu, jëwriñ ji yor Mbey mi ak Jumtukaayi kaw gi

- Seex Bàmba Jéey, jëwriñ yi yor rëdduk yoon yi ak gox yeek gox-goxaan yi

- Mata Si Jàllo, jëwriñ ji yor Yaxantu gi, Isin yi ak liggéeyu loxo yi

- Aminata Mbeng Njaay, jëwriñ ji yor Càmm gi

- Paap Juuf, jëwriñ ji yor Napp gi ak mbiri géej gi

- Moor Ngom, jëwriñ ji yor yoon yeek dem beek dikk bi

- Aali Nguy Njaay, jëwriñ ji yor Kàttan li ak Miin

- Aali Koto Njaay, jëwriñ ji yor mbiri Ndaw ñi, Tàggat ci liggéey ak Xëy

- Àllaaji Maalik Gàkku, jëwriñ ji yor Tàggat-yaram

- Xujja Mbay, jëwriñ ji yor mbiri Taax yek Dëkkiin gi

- Sëriñ Mbay Caam, jëwriñ ji yor Njàngale mu Kawe mi ak Gëstu gi, doon it ki yor kàddu nguur gi

- Aali Aydar, jëwriñ yi yor Kéew gi ak Aar àll bi

- Mansuur Si, jëwriñ ji yor liggéey bi ak jëfalante gi digante Campéef yi

- Umar Géy, jëwriñ ji yor Ndox meek Cet gi

- Abu Lóo, jëwriñ ji yor Jokkalante, Telekom gi ak jumtukaayi siiwal yeek yu jokkalante yi

- Abdulaay Daawuda Jàllo, jëwriñ ju tofu ci jëwriñ ji yor Koom gi ak alalal ji, yor njél li (Budget)

BHC/SG/ESF

Jukki bi mu bawoo: APS

Aji-tekki ji ci Wolof : A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Abdul Mbay, di ku màcc ci wàllu Bànk lañu tabb njiitu Njëwriñ yi

abdul_mbayAbdul Mbay mi njiitu réew mi, Maki Sàll, tabb njiitu jëwriñ yi mi ngi toll ci 59 at, doon ku màcc ci wàllu Bànk. Am na raaya bu Daara Ju Kawe ci wàllu Yaxantu bu nekk Paris, ñu duppe ko ci farañse "HEC École des hautes études commerciales de Paris", bu Sorbon ak bu Iniwersite Seex Anta Jóob bu Ndakaaru.

 

Ca HEC, bokkoon na faa nekk ak François Hollande, mi bokk ci joηante njiitu réew mu Fraas bi war a am weeru awril jëm Mee.

Ci atum 1976, la doomu àttekat bu siiw bii di Keebaa Mbay duggu ci Bànk bi Réewi Afrik sowwu-jant bokk, niki ab koomkomal (économiste) ci bànqaas bi yor wàllu gëstu ci njiital Alasaan Watara, mi doon tey njiitu réewum Koddiwaar.

Ci atum 1982, fekk mu toll ci 29 at, la ko njiitu réew ma woon Abdu Juuf fal njiitu lu njëkk bu Bànku Dëkkuwaay bu Senegaal (Banque de l’habitat du Sénégal) laata muy jàpp ci atum 1990, ci suqalig bànk bii di BIAO-Senegaal.

Gannaaw ba mu nekk Njiitu CBAO mi juddoo ci faatug BIAO. Bi mu nekkee ci kaw CBAO, la Abdul Mbay ubbi lonkoo bi njëkk def ci Senegaal li àngale di wax leasing ak gafag alalal gu njëkk ci Afrik Sowwu-jant.

Moo njëkk a doon njiitu GIM (Mbennoy Bànk ci wàllu Monetik) bu UEMOA, njiitu te bokk ci way-sos ISA (Daara ju kawe juy tàggat njiitu këru-liggéey yi), njiitu Kuréel giy doxal Lekkool Bariteknik bu Cees (Ecole polytechnique de Thiès).

Ci atum 1999, la bokk ci kurél gi jënd BST (Bànk Senegaal ak Tinisii) te mu mujjoon a doon njiit la te mujj koo suqali ci ñetti at rekk. Ci atum 2006, la Attijari Bànk jënd yoxo yi ëpp ci BST.

Abdul Mbay doon a jàngale politiku monetik ci ENA (Lekkoolu biir yéew miy tàggat ci Yoriin), njiitu kurélu ’’Alalal ak yaxantu’’ bu Jataay Koom-koom ak askan, bokk na it ci Jataay bi njiitu réew miy amal ci wàllu alalal (invertissement).

Di ku yittéel lool tàggat-yaram, ba nekkoon na ki yor xaalisu Bennoo Senegaal bu Futbal (Fédération sénégalaise de football), njiitu Bennoo Senegaal bu Daw (fédération sénégalaise d’athlétisme).Bokk na tey ci mbooloo miy fësal  kurélu Tàggat-Yaram bi àdduna sépp bokk (CIO).

Amna soxna ak 4 doom, Sëñ bi Mbay bokk na ci ñi seen jëf gën a ràññeeku ci Senegaal ak ci Faraas.

OID/ASG

Jukki bi mu askanoo : APS

Aji-tekki ji ci Wolof:  A. M. NGEER - Xibaaryi.com

Ndeyu Àttewaay yi firndéel na ndamul Maki Sàll li

Ndeyu-Attewaay_yiNdakaaru, 30 màrs (APS) – Ndeyu Àttewaay yi firndéel na àjjuma ndamul Maki Sàll li ak 65,80% ciy xob ñeel ko ci 34,20% ciy xob ñeel Abdulaay Wàdd.

 

Maki Sàll amna 1.909.244 xob ci 2.901.800 xob yees sànni. Abdulaay Wàdd moom a ngi am 992.556 baat.

Dayob ñi sànni seeni xob a ngi tollu ci 55%. Mu doon lu gën a tane wërgal bu njëkk bi tolloon ci 51,58%. Ndajeem jëbbal lengee yi Maki Sàll a ngi doon altine.

Njuréefi tànneefu Njiitu Réew maa ngi nii :

Limu Sànniwaayu xob yi : 12.555

Limu Way-bindu yi : 5.301.648

Limu Way-sànni xob yi : 2.915.893

Xob yi déey : 14.093

Limu xob yees sànni : 2.901.800

 

Jukki bi mu askanoo

Aji-tekki ji ci Wolof: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Abdulaay Wàdd nangul na ndam li Maki Sàll mi rafetlu "ndamul askanu Senegal"

maki_sallNdakaaru, Senegaal - Njiitu réewum Senegal, Abdulaay Wàdd nangu na ndam li ay waxtu yu néew gannaaw bi biroy woote yi tëjee, ca ba njuréef yi tàmbalee wone ne mbërum kujje gi raw na ko lu bari.

 

Maki Sàll rafetlu na "ndamal askanu Senegaal"

26/03/2012 00:36 GMT

 Maki Sàll mi gàddu ndam li ci tànneefu njiitu réewum Senegaal rafetlu na  "ndamal askanu Senegaal" dibéer jii ci ngoon.

Ci ba muy àddu ci farañse ak wolof, ci oteel bu nekk Ndakaaru, S. Sàll jàpp na ne "njuréef yi génn nañu ci mbañ-ngàcce yi". "Ki jël ndam li dëgg-dëgg mooy askanu Senegaal", lii la jibal.

Mbërum Bennoo Bokk Yaakaar sargal na bu baax ñi ñàkk seen bakkan ngir aar demokraasi  ak Ndeyu-àtte réew mi (Constitution).

Teewul mu fàttali ne "dinaa fi nekkal doomu Senegaal yépp", laata moo wax ci woo gi ko njiitu réew mi Abdulaay Wàdd woo ngir sargal ko ci ndam li.

Maki Sàll, toll ci 51 at, doonoon bu yàgg Njiitu Jëwriñ yi ak Njiitu Péncum Réew mi, bég na ci dayob ndam li, di nammeel wu askan wi am ci Wàdd mi def 12 at ci nguur gi.

Rafetlu na it liggéey bi taskatu xibaar yu biir réew mi ak yu bitim-réew def, kilifa yeek mbootaay yépp.


Maki Sàll sargal na bu baax ñi ñàkk seen bakkan ngir aar demokraasi  ak Ndeyu-àtte réew mi

26/03/2012 03:33 GMT

Ndakaaru, 26 màrs (APS) - 

Lu ëpp fukki nit ak juróom ñoo faatu ci ñaxtu yi kujje gi doon amal ngir bañ njiitu réew mi Abdulaay Wàdd bokk ci tànneef yi.

Maki Sàll a ngi askanoo diiwaanu Maatam (penkub bëj-gànnaar), waaye mi ngi juddoo Fatik, ci diggu-sowwu réewum Senegaal. Fal nañu ko ñaari yoon jaraafu (maire) dëkk ba di Fatik.

ADL/SAB

Jukki bi mu askanoo

Aji-tekki ji ci Wolof:  A. M. Ngeer - Xibaaryi.com


[ Kàdduy fàttali ] Li Sëriñ Saaliwu Mbàkke xalaat ci politik

serin_saaliwu_mbakkeLii ay kàdduy fàttali la yu Sëriñ Saaliwu Mbàkke waxoon mu jëm ci politik.


 

 

"Lii ñuy wax yépp (politik) dara jëmu ci ci Yàlla ak yoonu Yàlla ak topp Yàlla, waaye am loo xamne yit yëngu-yëngu yi dafa bëri bëri, ba ku nekk a ngi ñëw di ci laaj. Ku nekk bëgg a xam fu ma ci ne ak fu ma ci toll. 


Fi ma ci toll nak laa bëgg a xamle nii, mooy li nga xamne ci laa nekkoon; di :

Mbooleem ñiy "lijjënti àdduna" di fi ñëw, képp ku ci ne, ma ne loolu (politik) du sama liggéey, yàqaluma sama liggéey itam, fi ma ci tollu daal moodi :

ku fi ñëw ku ne daal, moo xam si sey àndando walla sey mbooloo; sama mbooloo dacee bare lool, ba sama mbooloo laa ko jàppee, te sama mbooloo kenn ëppalewuma ci, 

mbooloo yépp nak bëggal nanu leen jàmm, bëggal nanu leen muccu; taxaw naa taxawaay woo xamne, te fas yéene bañ cee jóg, ku waxul li nga war a wax it, soo dellusee fi nga may fekk, te moodi jaamu Yàlla ak liggéeyal Sëriñ Tuubaa, te séq ak ñoom li nga xamne moo jëm ci yoonu Sëriñ Tuubaa bii. 

Duma duggu ci lu ma warul a xam walla lu ma warul a wax. Te nak xam naa ko bu baax a baax, waaye boolewuma ko ci sama liggéey. Kon fii laa ci tollu.

Képp koo xamne njariñal Senegaal ak jàmmam a ngi ci loxoom. Yal na ko Yàlla defal ndimbal. Ndax ñum ñépp sunu aajoo ngi ci loolu.

Li ci des nak bëgg naa ñu dimbali ma ci yii, mooy di tuub, di sàkk sarax ak njàngum alxuraan jii.
Fépp fuñu sanc kër Sëriñ Tuubaa, nañu fa yeesal njàngum alxuraan ak xasida, lii daal mooy loo xamni sama yoon a ngi ci, te maa ngi koy soññee bu baax a baax. 

Assalaamaalikum waraxmatulaa wa barakaatuhoo

Fi mu bawoo: Seneweb

Ki ko bind ci Wolof : Diwdiw

Ki ko toppaat : A. M. Ngeer - xibaaryi.com

[ Kàddu ] Njuréefi tànneefu njiitu réew mi : Wàdd ci bopp bi 34,82%, topp ci Maki ak 26,57% ak Ñas 13,20%

tanneef12Kurélu biir réew miy dajale xobi tànneef yi, siiwal na tey àllarba ci ngoon njuréef yees amagum ci tànneefu njiitu réew mi amoon dibéer jii weesu. Nii la séddaloo : Abdulaay Wàdd 34,82%, Maki Sàll 26,57%, Mustafaa Ñas 13,20%. Limu ñi wotee ngi toll ci 2.707.056 (Ñaari milyoη ak juróom-ñaar téeméer ak juróom-ñaar yu teg juróom fukk ak juróom-benn).

 


Coste: SenewebRadio
Njuréefi tànneef yi bawoo ci ëttub àttewaat bi

[ WIDEO ] Ci tànneefu Njiitu Réew mu-2012, Ndigal, ag taqoom ak Sëriñ Saaliwu : Seex Beeco Cuun leeral na lépp !

seex_beeco










Fi mu sosoo: Seneweb

[ WIDEO ] Baara Taal jél na ndam li ci layoo bi mu séqoon ak nguurug Senegaal

baara_taalMetlang (entrepreneur) bii di Baara Taal mel na ni bàyyi nañu koo topp ci lépp li ñu ko jiiñoon. Muy li tukke ca àttekaay bu Ndakaaru. Dees na ko gën a yaatal ci waxtu yiy ñëw.



Aji-bind ji: Seneweb-News
Aji-tekki ji: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

[WIDEO] NGIR WEDDI DR MARI FAY : RTS wone na njiitu réew mi Wàdd di daw «safaak marwa»

wadd_makka

Njiitu réew mi Me Abdulaay Wàdd ñibbisi na Màkka démb. Ba mu wàccee ci roppulaan wa, jibal na ay kàddu. Me Abdulaay Wàdd wax na ci digante ak réewum Iraη. Saxal na it ne ñi ñu jàpp aki ngànnaay ñu juge Iraη, ca Niseria dees na leen àtte.

Sàqum xaalis mi ñu tudde « Millenium Challenge Account (MCA) » taxawalees na ko, ngir mu tàmbali liggéey bi


ablaay-joob
Tàmbalig génne xaalis biy liggéey sémbi MCA
Jawrinu Senegaal ji yore Koom ak Ngurd mi, Abdulaay Jóob, ak Casandra Butts, mi jiitu ci ñiy xelal Njiitu kurél gi ñuy woowe « Millenium Challenge Corporation (MCC) », amal nañu ag weccoo bataaxal gu firndeel, ne mënees naa tàmbali di tibb ci sàqum xaalis mi ñu tudde « Millenium Challenge Account (MCA) », Amerig jagleel ko réew yi néew doole, ngir xeex ñàkk gi.
Xaalis bi : ñaari téeméer ak juróom-ñaar fukki milyaar (270) ciy CFA
Xaalis bi ñu sédd Senegaal mu ngi tollu ci juróomi téeméer ak ñeen-fukki milyoŋ (540) ciy dolaar, bu ñu ko walbatee ciy CFA, mu dikk ñaari téeméer ak juróom-ñaar fukki milyaar (270), ci diiru juróomi at.

Wàdd leeral na li waral càcceeg Samiyel Saar.

sam_2Nees ko jàngee ci yéenékaay L'As bu àjjuma jii : "Mbiri kàttan li jël na wàll gu réy ci jataayu jëwriñ ji ñu amal démb, te Ibraayma Saar, doonoon jëwriñu Njél li te ñu tabb ko léegi  jëwriñ ji ñu féetale Kàttan li. Doonte jëwriñ ja woon di Samiyel Saar mi ñu tabb léegi jëwriñ ju tofu ci njiitu réew mi, bokk ci ñi koy xelal  ci wàllu alalal, teewu fa woon, teewul takkndeeram a woon ca barab ba. Ba muy àddu cig càccam, S. Wàdd, tukkee ci fu wóor, saxal na ci kàddu yu yërëmu : « Ndeysaan ! mi ngi ci doon génn bu baax, waaye askan wee sàkku ag wàccam ».

Lu waral Xibaaryi.com?

  • Wolof
  • Français
  • English
  • German
News image

Lu waral Xibaaryi.com?

Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey...

Yër li ci topp
News image

A propos de Xibaaryi.com

Xibaaryi.com est un site d’information générale en wolof, langue parlée par plus de 80% de la population du Sénégal. C'est le résultat du mémoire de maîtrise d’Ibra Ndiaye et Kelekey Moussa Diakhaté (promotion 2008 de la maîtrise informatique de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis du Sénégal). Il s'agit d'un site visant à permettre...

Yër li ci topp
News image

About Xibaaryi.com

Xibaaryi.com is a site of general information in Wolof, a language which is spoken by over 80% of the Senegalese population. This is the result of the Master's memoir of both Ibra NDIAYE and Kelekey Moussa DIAKHATE (academic year 2008, Master's in Computing, Saint-Louis Gaston Berger University, Senegal). This site...

Yër li ci topp
News image

Über Xibaaryi.com

Xibaaryi.com ist eine allgemeine informationsseite auf Wolof, der Sprache, die von mehr als 80% der senegalesischen Bevölkerung gesprochen wird. Sie ist das Ergebnis der Masterarbeiten von Ibra NDIAYE und Kelekey Moussa DIAKHATE (Sommersemester 2008, Masters der Informatik, Universität Sain-Louis Gaston Berger, Senegal). Diese Webseite möchte Wolof-Sprechern Informationen zugänglich machen....

Yër li ci topp

Ñi nuy Jàppale, Kureli suqali làkki réew mi

Àddu yi mujje ci dal bi

lu tee tasum xibaaryi ci wol...
Ndate man bis bu ma xéyee rekk te am jot xool na ko waay...
19/04/13 23:16
karim

Alquraan ci wolof
Sëriñ bi na ko yàlla miy boroom katàn te télewul dar...
30/03/13 06:14
kariim

Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee
Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fe...
31/12/12 02:25
kariim

ci mbiri wàtayi
Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu wa...
14/04/12 11:36
kariim

Di sant Yaalla rek a askan wi
Rafetlu naa ci ndam li Makki Sal am waaye nak Ablaay Waadd n...
08/04/12 11:32
Mouusa

Ñiy dugg ci Dal bi

mod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_counter
mod_vvisit_counterTay1651
mod_vvisit_counterDémb2324
mod_vvisit_counterAyu-bis bii13021
mod_vvisit_counterWeer wii57344
mod_vvisit_counterLépp-Lépp1647691

Amna: 15 gan, 13 bots yu lënku
Sa IP: 107.21.156.140
Tay la Suw 19, 2013

Ay yëgle yu bawoo Google