Ndakaaru, 13 awr (APS) - Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yiy dugg Senegaal tey juge bitim-réew war a am. Mi ngi ko dogalee ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.
‘’Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare n° 2012-444 soppi bub n° 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi. Dekkare boobu day tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yiy duggu Senegaal war a am’’, la njibal, lees siiwal àjjuma jii, karmat.
S. Sàll dige woon na ci batum dagaan ne dina ko def bees ko tegee ci boppu réew mi. ‘’Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal. Lutax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal ?’’, la waxoon.
Dogal booboo ngi tukke woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon siy tukkee ci oto yu màgget yi.
Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon. Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dugal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.
BHC/SAB
Jukki bi mu bawoo: APS
Aji-tekki ji ci Wolof: A. M. NGEER - Xibaaryi.com









![]() | Tay | 1770 |
![]() | Démb | 1473 |
![]() | Ayu-bis bii | 13437 |
![]() | Weer wii | 72392 |
![]() | Lépp-Lépp | 1571979 |