Jàngale ak Yar

Wàll bi dajale mboolem jukki yi ñeel xibaari Jàngale ak Yar

Tekki nañu Alquraan ci Wolofal

alquraanTéere bu sell bii di Alquraan tekkees na ko ba mu mat sekk ci Wolofal. Ki def liggéey boobu di Sëriñ Seexunaa Lóo Ngaabu dëkk Tuubaa. Mooy itam njiital Fondasiyoŋ Seriñ Ibrahima Lóo. Mi ngi jefandikoo mbindiinu Wolofal bi ñépp ànd nangu, rawatina nguurug Senegaal.

Ci ndigalam, moom Sëriñ Seexuna, nu ngi leen di baaxe Kaamil bi ak téere liifantu bi mu àndal ci melo PDF.

1- Wàcce Téere Alquraan bi 

2- Wàcce Téere Liifantu bi

 

Ngir jokkook Sëriñ Seexunaa Lóo Ngaabu:  Adreesu email bii aarees na ko ci róbóoy spamkat, Fàww nga dekkil Javascript ngir gis ko.

 

A. M. Ngeer  - Xibaaryi.com

Xew-xewu OSAD ak UESLAN

 

OSAD ( www.osad-sn.com ) ak UESLANseexanta

ñooy wone

BAATUKAAYU ÑAARI LÀMMIÑ ÑEEL XAM-XAM 

FRÃSE-WOLOF / WOLOF –FRÃSE

Tibbees na ko ci

tijji xelum sàkk

Séex Anta Jóob bind ko

Ekool Normaal, lees koy defe 

Ci teewaayu Soxnas Séex Anta Jóob

Gaawu 23 Màrs 2013, ci 3 h 30 

Njàngum xale yu jigéen yi ca Koldaa : ñiy bàyyee ngi tollu ci 14%

jigeenNdóol gu law gi, séy ak ëmb yu teel yi, dooley aada yi ak mettital ci fànn yépp ñooy li waral xale yu jigéen yi di teel a bàyyi lekkool, la saytukatu akadëmi bu diiwaanu Kolda seetlu te tollale ko ci 8 ba 14%.


Moonte kuréel yiy yëngu ci fexe ba xale yu jigéen yi des ci lokkool yi bari nañu ci diiwaan yi féete bëj-saalumu réew mi : UNICEF, Bérëbu xelal waxambaane yi, mbootaayi gox yi ngir duggug lekkool yu xale yu jigéen yi (CDESCOFI, jàppale njàng mi ci bérëb yu ubbiku yi (AEMO).


Waaye buñu xoolee, njuréef yu doyadi yees jot a am, mel na ni dañoo nekk di dëbb ndox doonte joxees na leen jumtukaay yu sakkan.

 

Coste: Seneweb

Wolof: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

[Léeb] Doomu Yàlla.

leeb_doomu_yallaLééboon !

Lippoon!

Amoon na fi!

Daan na am!

 

Ma nga amee woon ca jamano yee, ba rab yi daan wax ak nit ñi. Amoon na fi jigéen ju bon ju nekkoon ak ñeenti doomam. Ñoo nga dëkkoon ca biir àll ba. Baayu xale yaa ngii dee, bi caat mi ñuy wax Tóni juddoo; yaay ji jàpp ni xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko bañ. Bu mosee rëbbi ba ñów, day woo xale yi, benn benn, ñu nàmp ba mu des Tóni. Muy woy, naan :

 

Jamloro kaay nàmp,

Jamloro Siise kaay nàmp,

Biraama Siise kaay nàmp,

Ndaama Siise kaay nàmp,

Na Tóni xaar Yàlla, yaayam.

 

Di ko def ay yooni yoon. Waaye, jigéen ju bon ji mosul xam ne Yàlla daan na feeñu Tóni ci melokaanu daar bu bare meew; bu ñowee di nàmpal Tóni.

Am bés, musiba dal jigéen ji. Mu jóge ca àll ba di woy; woy wa mu daan woowee xale yi ngir nàmpal leen; yemmoog Bukki di jaar, mu déglu woy wi, jàng ko ba mën ko bu baax.

Benn bés, yaayu xale yi dern rëbbi. Bukki doxe ko gannaaw, roy baatam, di woy woy wi. Xale yi di génn benn benn, bukki di leen lekk ba mu des Tóni. Ba yaay ja jógee àll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Yàggul dara, mu dégg baat bu mu miin, di woy, naan ko :

 

Jamloro, Bukki jël na ko,

Biraama Siise, Bukki jël na ko,

Ndaama Siise, Bukki jël na ko;

Tóni rekk a des ci yaayam Yàlla! ”

 

Ba mu déggee kàddu yooyu, jigéen ji dafa yuuxu, yuuxu mu tar, réer ci àll bi.

Foofa la léeb doxee tàbbi géej, bàkkan bu ko njëkk a foon tàbbi àjjana.

 

Lilyan Kesteloot & Cherif Modj, 1983, Contes et mythes wolof, Dakar : Les nouvelles éditions africaines.

p.42-46

Roofoy baat yu Sana Kamara

roofoy_baat1

Roofoy baat (mots croisés ci làkku farañse, crossword ci làkku Àngale) powum araf la mu ñu xam ci àdduna sépp. Li ko tax a jóg moodi fexee feeñal baat yépp yi làqu ci giri (grille) ci ndimbalal tekki yi mu àndal ci wet gi. Ñi ngi joxe tekki yooyu ci tallal yi ak ci wàcc yi : noonu baat yi tallal ak yi wàcc dañuy roofoo, muy li joxe turu « roofoy baat ».

Sana Kamara dib Profesëeru Farañse ci Iniwersite Truman State University Kirksville, MO 63501, moo leen baaxe roofoy baat yi.

Ku ci bëgg a jokkook moom na ko bind :   Adreesu email bii aarees na ko ci róbóoy spamkat, Fàww nga dekkil Javascript ngir gis ko.

 

Boo ko bëggee wàcce, cuqal fii.

 

Goney Afrig rekk ay jàngeek làkki jàmbur (aji-làmmiñal)

fari_silaat_kaAfrig gu ñuul gi rekk mooy gox bi way-jur yi des di wéy di yóbb seeni doom ci lekkool yu ñu dul jànge ak seeni làkki réew, la Fari Silaat Ka, mi jiite  Péncum Làkki Réewum Sénégaal (Academie Nationale des langues) saxal.

 

Néegub jàng bu màbb : gaañu-gaañu yu bari ciy tuut-tànk.

photos2006435Ab néegub jàng yuy tuut-tànk a màbb alxamis gii ca Pikin Ginaaw Raay (ca anéeru Ndakaaru), waral ay gaañu-gaañu yu bari ciy tuut-tànk. Ci waxi Rajo Sud FM, baayi tuut-tànk yi, ci ndimbalul ñiy fay-làkk,  ñoo wallu tuut-tànk yi toll ci digante 5 ak 8 at, jëme leen ciy fajuwaay yu gox ba. Jànguwaay baa nga nekk ci kër gu màgget gees jekkal. Kenn ci baayi tuut-tànk ya ηàññ na njubadi gi ci metlang (entrepreneur) yu tabax yi, ca bamuy àddu ca rajo Sud Fm.


Seneweb.com :    Alxamis 21 Okt 2010


Aji-bind ji: seneweb.com    Jukki bi mu bawoo
Wolof : A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

40% NJÉL LEES JAGLEEL NJÀNGALE MI: 60.000 ndongo yu Senegaal ladab lañuy jàng.

jangAfp ( làng politig) xalaat na ne nguur gi waar naa xoolaat politigam ci njàngale mi te dakkal di jibal naan  40% njélul réew mi lañu jagleel njàngale mi. Nguur gi kay daa waar a seet yeneeni pexe ngir ñaax ndongo yi ñu sóobu ci  bànqaasi xarala yi, di xalaati Afp mi jibal ne 60.000 ndongo ci Senegaal ladab (littérature) lañuy jàng.

Lu waral Xibaaryi.com?

  • Wolof
  • Français
  • English
  • German
News image

Lu waral Xibaaryi.com?

Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey...

Yër li ci topp
News image

A propos de Xibaaryi.com

Xibaaryi.com est un site d’information générale en wolof, langue parlée par plus de 80% de la population du Sénégal. C'est le résultat du mémoire de maîtrise d’Ibra Ndiaye et Kelekey Moussa Diakhaté (promotion 2008 de la maîtrise informatique de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis du Sénégal). Il s'agit d'un site visant à permettre...

Yër li ci topp
News image

About Xibaaryi.com

Xibaaryi.com is a site of general information in Wolof, a language which is spoken by over 80% of the Senegalese population. This is the result of the Master's memoir of both Ibra NDIAYE and Kelekey Moussa DIAKHATE (academic year 2008, Master's in Computing, Saint-Louis Gaston Berger University, Senegal). This site...

Yër li ci topp
News image

Über Xibaaryi.com

Xibaaryi.com ist eine allgemeine informationsseite auf Wolof, der Sprache, die von mehr als 80% der senegalesischen Bevölkerung gesprochen wird. Sie ist das Ergebnis der Masterarbeiten von Ibra NDIAYE und Kelekey Moussa DIAKHATE (Sommersemester 2008, Masters der Informatik, Universität Sain-Louis Gaston Berger, Senegal). Diese Webseite möchte Wolof-Sprechern Informationen zugänglich machen....

Yër li ci topp

Ñi nuy Jàppale, Kureli suqali làkki réew mi

Àddu yi mujje ci dal bi

lu tee tasum xibaaryi ci wol...
Ndate man bis bu ma xéyee rekk te am jot xool na ko waay...
19/04/13 23:16
karim

Alquraan ci wolof
Sëriñ bi na ko yàlla miy boroom katàn te télewul dar...
30/03/13 06:14
kariim

Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee
Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fe...
31/12/12 02:25
kariim

ci mbiri wàtayi
Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu wa...
14/04/12 11:36
kariim

Di sant Yaalla rek a askan wi
Rafetlu naa ci ndam li Makki Sal am waaye nak Ablaay Waadd n...
08/04/12 11:32
Mouusa

Ñiy dugg ci Dal bi

mod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_counter
mod_vvisit_counterTay1809
mod_vvisit_counterDémb2061
mod_vvisit_counterAyu-bis bii15537
mod_vvisit_counterWeer wii74492
mod_vvisit_counterLépp-Lépp1574079

Amna: 32 gan, 5 bots yu lënku
Sa IP: 54.234.42.16
Tay la Mee 24, 2013

Ay yëgle yu bawoo Google