Mboolaay & Askan

Way-ñàkk liggéey yi dinañu jébbal seeni mbébét Maki Sàll

Way-ñàkk liggéey yi dinañu jébbal seeni mbébét Maki Sàll (ci waxi seen njiit)

 

2013-04-26 13:41:29 GMT

way_nakk_liggey

Ndakaaru, 26 awr (APS) – Bennoo gu biir réew mi ngir ag liggéey (CNE ci frãse) fas na yéene jébbal ay mbébétam njiitu réew mi, àllarba, ci bis bi ñuy màggal liggéey, ngir woo Maki Sàll ''mu gën leen a sóoraale'' ci jafe-jafe yi aju ci liggéey, la Baabakar Nduur, mi yor seen kàddu, jibal àjjuma ca ndaje ma ñu amaloon ak way-tas xibaar yi.

''Xew-xew bi du doxub ñaxtu, du it doxub siiwal. Li ko waral mooy jébbal ab limu mbétét njiitu réew mi ni ko sendikaa yi di defee'', la Sang bi Nduur leeral, mi doon it aji-saytu mbooloo mi ëmb way-ñàkk liggéey yu Senegaal yi ami diplom (RDSES).

''Niki sendikaa yi, way-ñàkk liggéey yi war nañoo jëfandikoo bisu màggalug 1 Mee ngir wax ci lu aju ci liggéey, ci lu leen soxal'', la Baabakar Nduur rëdd.

Teg na ci ne ''Bennoo gi ëmb mbootaay yu way-ñàkk liggéey yi, yoy bokk na ci (ndongo yi am diplom, fajkat yi, way-taxawu njaboot yi, ñiy yëngu ci jumtukaayu napp, ñiy yëngu ci wàllu yoriin ...) fas nañoo leeral askan wi ci lu aju ci wàllu liggéey''.

''Li feek mbiru ñàkk xëy, nguur gi taxawu ci temm, dinañu wéy di ñaxtu'', la ki yor seen kàddu jibal.

''Duñu wax ci liggéey ludul bu ñu jubee ay tànneef, ak sémb yu baax, mbaa bu ñuy def ay taxaw-seetlu, te bu boobaa ñuy joxe ay lay niki ndaw ñi tàggatuñu leen ci lu dëppook soxlaay réew mi'', la Mamadu Mbow, mi jiite fajkat yi amul xëy, wax.

''Buñuy màggal xëy ci réew moo xamne lu ëpp 65 % ay ndaw lañu te 90% amuñu liggéey, nga xamne jafe-jafe amna'', la xamale. Teg na ci ne Bennoo gi jéemul rekk di fexe nguur gi jox liggéey ñi ci bokk.

''Bennoo gi ndaw la luy jokkook nguur gi ngir amal ay pexe ndax ñu ngi doon ñu yor ay sémb aki pexe'', la ci S. Mbow yokk.

FD/BK

Coste gi : APS

Wolof: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Takkarnaasug dog-dogi mbëj : Caaroy Gaar cig lëndëm ci diirub 10 waxtu.

dog-dogu_mbejDog-dogi mbëj (electricité) ñëwaat nañu ak doole ay fan a ngii ci anéeru Ndakaaru, rawatina ci goxu Caaroy Gaar mi askan wa xamatul lumuy wax. Kaarce bee ngi cig lëndëm 10 waxtook léegi.

Muy mbir mu tiitlu ndax ñu ngi ci ndorteelu ubbiteg lekkool yi. Askan wee ngi wone ag naqaram tey yékkati kàddoom: « Senelec deful benn yégle jëm ci dog-dogu mbëj bu yàgg bii » lañuy wax. Teewul, askan wa fa dëkkee aartu nañu ne dees na leen dégg bu beneen dog-dogu mbëj bu yàgg amee.

Coste: Seneweb

Wolof: E. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Màggalug 1 Mee : ay defile aki waxtaan ci arminaati mbootaayu sendikaa yi.

maggalu_1_MeeNdakaaru, 1mee (APS) - Mbootaayi sendikaa yu bari dinañu màggal, talaata jii ci Ndakaaru ak ci diiwaaan yi, bis bi àddina sépp jagleel liggéey. Dinañu ci def ay doxu liggéeykat (defile), ay ndaje aki waxtaan, laata ñuy amal jotaay bi ñuy jébbalee téerey mbébét yu sendikaa yi, ca njénde réew mi.

 

CNTS, di mbootaay mu ëmb ay liggéekat, dina amal ab doxub liggéeykat  buy tàmbaalee ca Gafag Liggéeykat yi (Bourse du travail) ca xàllu Lamin Géy, bu 7 waxtu jotee. Dinañu jaar xàllu Lamin Géy, teg ci bulwaaru Réew mi, door a dugg xàllu Leopool Sedaar Seηoor, ngir teeree ca Pencum Tembute ga (Indépendance), fa ñépp di daje.

CNTS/FC, di mbootaay mu ëmb ay liggéeykati Senegaal/Kàttanu Coppite, dina amal it ab doxu liggéeykat buy tàmbalee digante xàllu Maalik Si ak bob Balees Jaañ, digante 10 w ak 10w30.

Dina jaar xàllu Jean Sores ak Palaas Washington, laata muy jot xàllu Leopool Sedaar Seηoor ak Taaxub Saytu Réew mi, di fa ñuy teeree.

Mbootaayu Sendikaa yi demal seen bopp  (CSA ci farañse) ak Bennoog liggéeykat yu Senegaal yi (UTS ci farañse) dinañu ànd amalandoo ‘’am ndaje’’ ca Iniwersite Seex Anta Jóob bu Ndakaaru, dinañu fa waxtaan ci : ‘’Bennoog sendikaa yi, ab wartéef ngir dooleel liggéeykat yi’’.

Bennoo Sendikaay Senegaal yiy demal seen bopp  (UNSAS), moom dina dajale ay ñoñam ca gaaraasu Géejaway, ca kaarce HLM yu Ndakaaru, ngir amal ab doxu liggéeykat.

Mbootaayum demokraasi bu liggéeykat yu Senegaal (CDTS) dina boolee ay ñoñam ngir waxtaan ci : ‘’liggéeykat yi ak jafe-jafe dund gi ak nekkin wi, gàllankoor yi, njariñ yi ak Seenu yi‘’. Ndaje la muy ame ca stàdd Leopool Sedaar Seηoor ci 10 waxtu.

Jukki bi mu askanoo

SAB/ESF 

Wolof: A. M. NGEER - Xibaaryi.com

Sëriñ Maam Moor Mbàkke ci 40 milyoηi Wàdd yi : « Duma kuy jaay! »

maam_moor_mbakke« Duma kuy jaay. Ku gore laa . Musumaa sàkku lenn ci kenn. Te sax, buma doon kuy jaay, duma jar 4O milyoη FCFA. Nit ku jaayu, ñàkk boppam ci saa si ».

Kàddu yooyu la Sëriñ Maam Moor Mbàkke, mi doon janook way-tas xibaar yi ci këram, toontu ngir indi  ay leeral ci tuuma yi tukkee ci ngan gi ko njiitu réew mi Abdulaay Wàdd, bokk ci ñiy sàkku boppu réew mi, gane woon ca Bàmbey.

« Neena, Yore naa Al Azhar ci sama alalu bopp te musu maa sàkku ndimbal ci kenn. Lépp lu ma murid yi jox, dafa fekk rekk ñu gis ci man seen sëriñ te musuñu maa laaj fumay def xaalis bi ».

Sëriñ bi yokk ci ne ci atum « 2008, kolonel Maalik Siise, àndak Faatu Géy Saar », fekk nañu ma Washington ci turu njiitu réew mi Wàdd. « Ñu xamal ma dogal bi njiitu réew mi jél ngir di dugal, at mu nekk, 500 milyoη ci Iniwersite Al Azhar. Dogal boobu, ba léegi amul, moonte fàttaliwuma leen ko. Bu ma xaalis ñoroon, kon at mu nekk ma taxaw këram. Duma kuy wàcc, ngir daray àdduna, ci yoon wi ma gëm ».

Sëriñ Maam Moor xamalaale na ci ne bokk na ci ñiy xalaat ne sëriñ si dañoo war a génn ci wàllu politig bi luku moy ñu def leen ni ñépp. « Joxewu ma kenn ay njàngale, li ma xalaat rekk laa wax », la mujjee leeral.

Dutee maa ngi sant Njiitu réew mi Wàdd ngir yég gi mu am ci liggéeyu Sëriñ Murtadaa Mbàkke bi.

 

Jikki bi mu askanoo

Aji-tekki ji ci Wolof: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Way-lorub Plaη Jaxaay: Maalik Ndaw a ngi jéem a taal boppam ci kanamu njénde réew mi; ay yooni yoon.

way-lorub_jaxaay

[ KÀDDU ] DENKAANE : « Sama doom ju jigéen am 17 at ak sama jëkkër dañuy sëy »


jigeen0Dees na mujj yaakaar ne nu ngi dund dëgg-dëgg ak ñu ñaaw jikko. Yenn xew-xew yi dina ñu yóbb ñuy xalaat ne yenn nit ñi amu ñu ag ruu akug ràññee. Xel-ñaar nanu lool laata nuy siiwal bile jukki. Xaar nanu bisu lëm ngir am firnde ci aji-amal emisiyoη bi ne amna ñu baax ñu bëgg jokkook soxna si ngir dimbali ko.

Soxna su dëkk Wakaam a ngi dund jamono ju lëndëm te metti ci àddunaam. Bi mu ñàkkee jëkkëram bi mu amal benn doom ju jigéen, ci la séyaat ak benn waay ju mu amal ñaari doom. Tey jii doomam ju njëkk ji mu amoon ci séyam bu njëkk, toll ci 17 at, mooy kiy génn ak jëkkëram. « Waaw yaay, maa ngi dëggal ne damay génn ak sama baayu-jiitle te lu baax la ci nuy ñaar. Mbaa du dangaa fiire ? May nu jàmm te bàyyi nu nu dund ! » La xale bi toontu yaayam bi mu ko laajee gannaaw bi mu ñaawee-njoort. Soxna see ngi muñ ci biir këram, jëkkëram di séy ak doomam. Rax ci dolli doom ji jugul di ndamoo ni baayu-jiitleem di jaxasook moom.

Jëkkër ji moom di it baayu jiitle xale bi, amul lenn lu mu wax ludul naan soxna si mu dal te bàyyi ko mu bànneexu ak doomam. « Moom laa gën a yég ci yaw. Ci moom laay gën a yég bànneex. Bàyyi nu nu dund ci jàmm ndax moo may jox lu ma amul ci yaw. » Di kàddu yi ko jëkkëram sànni doonte am nañu doom yu am 15 at ak 12 at.

Lan moo dal ñaar ñii ak soxna si?  Lu waral lii ? Lu yóbbe xale bu jigéen bi muy dundak baayu jiitleem ? Lu waral góor gii muy séy ak ndey ak doom te wóor ko ne lislaam dakoy tere ? Lu tax ndey ji jémmul dara ci lii ?

Jukki bi mu bawoo


Coste: SenewebRadio
Déglul dénkaane ndey jii doom ji nangu jëkkëram

Xaru ca Ginnaaw Raay : Ab xale minise faat na boppam ca biir néegam.

xaru_ginnaaw_raayAb xale minise bu am feebaru xel, xaru na démb bi wetu ñeenti waxtu, ca Sidd, ca nëkkaanu Pikin. Tewodoor Milimuno, toll ci 26 at, daa jéng pobbam akub buum ca biir néegam.

Xamees na ci seeda ya fa Walf Grand Place jélee, ne, « ndéemi-yàlla soosu daa amoon feebaru xel ay weer a ngii. Ay waxtu laata jéyya joojuy am, baayam jot naa wax ak moom ngir jéem koo mocc mu dem faju ji ca loppitaal xel bu Caaroy ».

 

SenewebNews - Jukki bi mu bawoo

Aji-tekki : A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

 


Ab xeex cib emisiyoηu RTS gannaaw ba layalkatu Lik Nikolaaay saagaa Allaaji Njaay

xeex_nikolaay_njaayWaxtaan wi Rts amaloon te jëm ci li aju ci déggoo gi boole woon aji-amal-làmb jii di Lik Nikolaay ak 2stv, mujj naa doon ab xeex. Allaaji Njaay, miy njiital 2stv, làq-làqalul ngir wax xalaatam Lik Nikolaay mi dëgër ci fi mu jàpp. Gannaaw 20 miniti xiiru, palaatoob RTS bi mujj doon ab làmb.  Aamadu Mustafaa  Mbóoj, layalkatu Lik Nikolaay a ko tàmbali, ci ne Allaaji Njaay doomu xaraam.

Ba tax jàppante gu tàng topp ci. « Doomu Allaaji Njaay, ni kuy aar baayam, dóor sox layalkatu Lik Nikolaay »,  la Maalik Càndum, mi amal jotaay ba, seede. «  Way-saytu teknig yee ci mujj jàpp ngir tàqale leen ».

Lépp a ngi dale ci ñàkk déggoo gi am ci Kontra wone làmb ji leen boole woon. Promotëer bii di Nik Nikolaay daa xaatimoon ab kontra aakimoo ak 2stv ngir wone ci teew bépp làmb bu mu amal. Muy lu promotëer bi sàmmul, ci kàdduy Allaaji Njaay, ndax daa xaatim beneen kontra ak teleb Yuusu Nduur ngir mu wone làmb jiy am digante Bàcc Seeraas ak Rok Mbalax, dibéer jii. Di lu naqari Allaaji Njaay ba mu yóbbu ko ci yoon.

Aji-bind ji: SenewebNews  -  Jukki bi mu bawoo

Aji-tekki ji ci wolof: A. M. NGEER - Senxarala.com

 

Woowees na tele yi ñu wàññi di wone pecc yu ñaaw yi.

sabar_feccNDakaaru, 26 Sam (APS) - Njiitu réew mi, Me Abdulaay Wàdd, woo na, àllarba jii ci Ndakaaru, tele yu Senegaal "ñu wàññi" di wone yenn pecc yu ñaaw yi.

"Jariñul dara (…). Mënuñu yor ab tele niki ku nekk Las Vegas", dëkkub Amerig biy péeyum po ci àdduna si, la njiitu réew mi jibal.

Mi ngi ko doon waxee ci ndaje mi mu doon amal ak Mbootaayu yéenekaay yu Senegaal (CDEPS) mi ñëwoon ngir ndokkeel ko ci at mu bees mi.

Me Wàdd nee na  "jikko" joojoo "ngi tàmbalee law" ci yeneeni dëkki Afrig. Te, "du lees war a lawal".

"Warees naa saytu mbir mi bu baax", la njiitu réew mi xamale, moom mi jàpp ne, bu weesoo féexal xol, ab tele war naa yékkati juddu-réew yi ci yar akug tàggat, di fexe ba ndaw ñi taqook  "dund gu sell".

Warees naa jàngale gaa am pecc ak woy, waaye "na fekk mu dëppook sunuy aada, mi tënku cig yemale", la njiitu réew mi fàttali, ci teewaayu waa CDEPS, jëwriñu Jokkale gi di Mustafaa Giraasi ak ñenn ñu ko jexe.

Aji-bind ji : BK/SAB  - Jukki bi mu bawoo

Wolof :  A. M. Ngeer -  Xibaaryi.com

Bëccëgu gëstu ci njariñal Màggalu Tuubaa, gaawu.

maggalu_tuubaaNdakaaru, 7 samwie (APS) - Dees na amal, gaawu (tey jii) ci Ndakaaru, bëccëgub sottante xalaat ci njuréefi gëstu gi ñu def jëm ci njariñ li màggalu Tuubaa am ci askan wi, ci koom-koomu réew mi ak ci diine ji, la APS jëlee ci ñi ηànk mbir moomu.

Ndaje moomoo ngi tàmbali bu 10 w jotee, ca amfitiyaatar bu ESP ca UCAD, ci tëriit bii : ‘’Siiwalug njuréefi gëstu gi, ñeel yéenekaay yi’’, la kurél gi yor màggal gu 2011 saxal.

Bu 15w ca CICES, kurél gi fas ñaa yéene amal ab waxtaan ci gëstu gi ak njuréef yi mu feeñal.

Ñiy def waxtaan woowu di Lamin Njaay, njiitu bànqaasu xam-xamu askan (sociologie) ca UCAD, Mubarak Lóo màcc ci koom-koom ak estatistik ak Sëriñ Saam Busó dib xaymakatub njàngale.

Aji-bind ji: SAB/ASG - Jukki bi mu bawoo

Wolof : A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

SAG ABIIB SI bu AID TRANSPARENCY : « li dal Baara Taal jombul kudul Abdulaay Wàdd»

sag-abiib-si1Li dal tey njiital Jls (këru-liggéey bi ñu duppee ci farañse Jean Lefevre Senegal) mën naa dal ku nekk. Loolu di gis-gisu Sag Abiib Si. Artu na ne « Gannaaw Abdulaay Wàdd, li dal Baara Taal jombul kenn». Ndaxte, nee na, «nu ngi ci daanaka ag nguurug aakimoo». Ndax nee, «dafa am dagaanug xuppe gu njiitu réew mi tërël, moom mi dul fey ay boram te du muñal benn kujjeem gu politig».

 

Gannaaw bi mu rëccoo li sóobug Baara Taal ci politig lëkkalook ay yëngoom nikib metlàng, Sag Abiib Si jàpp na ne «jëf yi ko dal yóbbe na lu ëpp 3000 boroom kër ñu ñàkk seen liggéey, suuxal ay koom-koom, ab kappitaal, ay mën-mën». Jibal na «Fi njiitu jëwriñ ja woon Idriisa Sekk setoon wecc, tuuma yees ko toppee woon te muy benn ak yii, waratul a taxaw». Bu ñu gëmee kilifaag Aid Transparency, «Li dal ci Baara Taal jéyy la ju yokk ciy jéyy». Rax ci dolli, nee na «gën nañoo faagaagal koom-koomu réew mi doonoon koom gu néew doole. Ndax dañoo jam metlàng bu jàmbaare».

Ci woote gi mu woo sektëer priwe bi ak baa Bennoo, Sag Abiib Si fàttali na ne «mbir mi soxal na leen». Nee na, «sektëer priwe bi war na cee wax. Ndax bu ñu nangoo ñu faagaagal Baara Taal, na ko wóor ne mi ngi faagaagal boppam. Te sax Bennoo, Baara Taal defal na ko lu nekk. Jaadu na mu yaakaar ci moom ag jàppale».

Aji-bind ji: Biraan LÓO  -  Jukki bi mu bawoo

Aji-tekki ji: A. M. Ngeer - Xibaaryi.com

Lu waral Xibaaryi.com?

  • Wolof
  • Français
  • English
  • German
News image

Lu waral Xibaaryi.com?

Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey...

Yër li ci topp
News image

A propos de Xibaaryi.com

Xibaaryi.com est un site d’information générale en wolof, langue parlée par plus de 80% de la population du Sénégal. C'est le résultat du mémoire de maîtrise d’Ibra Ndiaye et Kelekey Moussa Diakhaté (promotion 2008 de la maîtrise informatique de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis du Sénégal). Il s'agit d'un site visant à permettre...

Yër li ci topp
News image

About Xibaaryi.com

Xibaaryi.com is a site of general information in Wolof, a language which is spoken by over 80% of the Senegalese population. This is the result of the Master's memoir of both Ibra NDIAYE and Kelekey Moussa DIAKHATE (academic year 2008, Master's in Computing, Saint-Louis Gaston Berger University, Senegal). This site...

Yër li ci topp
News image

Über Xibaaryi.com

Xibaaryi.com ist eine allgemeine informationsseite auf Wolof, der Sprache, die von mehr als 80% der senegalesischen Bevölkerung gesprochen wird. Sie ist das Ergebnis der Masterarbeiten von Ibra NDIAYE und Kelekey Moussa DIAKHATE (Sommersemester 2008, Masters der Informatik, Universität Sain-Louis Gaston Berger, Senegal). Diese Webseite möchte Wolof-Sprechern Informationen zugänglich machen....

Yër li ci topp

Ñi nuy Jàppale, Kureli suqali làkki réew mi

Àddu yi mujje ci dal bi

lu tee tasum xibaaryi ci wol...
Ndate man bis bu ma xéyee rekk te am jot xool na ko waay...
19/04/13 23:16
karim

Alquraan ci wolof
Sëriñ bi na ko yàlla miy boroom katàn te télewul dar...
30/03/13 06:14
kariim

Magàluk Sëriñ Tubaa Mbakee
Al'àmnduli'laa'il ràbil'àlamina bi nu yàlla mayee nu fe...
31/12/12 02:25
kariim

ci mbiri wàtayi
Mànne maakki sàll xam nga ni ( 8 ) àt tuti na li mu wa...
14/04/12 11:36
kariim

Di sant Yaalla rek a askan wi
Rafetlu naa ci ndam li Makki Sal am waaye nak Ablaay Waadd n...
08/04/12 11:32
Mouusa

Ñiy dugg ci Dal bi

mod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_countermod_vvisit_counter
mod_vvisit_counterTay1927
mod_vvisit_counterDémb2061
mod_vvisit_counterAyu-bis bii15655
mod_vvisit_counterWeer wii74610
mod_vvisit_counterLépp-Lépp1574197

Amna: 15 gan, 9 bots yu lënku
Sa IP: 23.22.76.170
Tay la Mee 24, 2013

Ay yëgle yu bawoo Google