|
Xibaaryi.com ab dal la (site) buy tas xibaar ci wolof, mu di làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar (Université de Saint-Louis) doonoon gëstug jeexal (mémoire de maîtrise) gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa kelekey Jaxate. Dal bii nag bénn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf:
Sabab yi:
- Ci Senegaal, lu toll fukk ci téeméer (10%) (OIF) rekk ci askan wi ñoo dégg làkkuw Frãse (français) ba mën cee jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80%) ci askan wi, ñoo xam ne seenug dégg wolof kawe na.
- Ñu bari ci askan wi dañuy seetaan ay film te duñu xam sax luy maanaa mi. Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.
- Sunu ndaw ñi, di ëlëgu réew mi, dégguñu solo si baat yi ëmbu dëg-dëg ci film yi ñu léen di jagleel, wante dañuy banneexu rekk ci jëf ju reetaanlu ju ñu gis. Loolu tamit di mbir moo xam ne du nàmm seenum xel.
- Bu njëkkoon, barab ya ñu daan seetaane filmu Endo ak kowboy ya dañu daan fees dell ndax ñoo gënoon a neex a nànd. Leegi, barab yooya soppees na leen ay ja (marse). Tax ba nit ñi dematuñu Sinemaa niki nu ko daa defe bu jëkkoon, waaye tamit dégg-dégg bi jàppandiwul ci film yu mel ni poliis especiaal, afeer kalase tere awaase ak yeneen ak yeneen.
- Kuréel yiy tàggat askan wi dañoo bàyyi ñi jàngul ak seen bopp ndax làkk frãse lees fay tàggatee.
- Tàggat nit ki ci làkk wi mu dégg moo gën a yomb juróom ñaari yoon - gën gaa néew - tàggat ko ci lammiñu jàmbur. Tàggat ci wolof soxlawul lu dul mu man a bind, man a yër (lire) ndax làkk wi dégg na ko ba noppi. Bu dee ci wu doxandéem la nag (niki frãse), di na laaj yeneen yu mel ni nos-wax (grammaire), tëggiin (conjugaison) xam bennaani baat yi (les vocabulaires) ak waxiin wi añs.
- Nguur gi am na ay jafe-jafe ci fal boroom lijaasa yi sunu daara yu kawe yi tàggat, rawati na ñi seen xam-xam màcc ci kàllaama yi.
- Ñu néew ci askan wi ñooy yër yéenekaay yi ñu bind ci wu Frãse ; daanaka ñi leen di yër matuñu ñaar fukk ci téeméer (10%). Ba tax na njariñam taxu koo bari.
- Gën a yaatal njàngale mi ci sunu làkki réew ; jaarale ko ci taxawal ay jumtukaayu tas xibaar ci sunu làkki réew rawatina ay Dali internet.
- Taxawal ay këri yéenekaay ci sunuy làkk
- Fexe ba tekki film yi ñuy seetaan ak fowukaay yi sunu xale di jëfandikoo ci sunuy làkk ; rawatina ci wolof ndax mooy làkk wi ëpp luñu koy jëfandikoo ci réew.
- Defar Tëriin (logiciel) ci sunuy làkk
- Loolu doon na luy yokk xereñug askan wi.
- Dina yokk ay junniy junniy liggéey ñeel ndongo-daara yi ñu tàggat te amuñu fu ñu leen dugal, ñoñ fànn ñi (les artistes) (ci tekkig film yi ci sunuy làkk) ; dina yokk Sinemaa yi ñuy seetaane film yi, dina yokk njënd mi ak njaay mi. Nañu xayma ñaata ci ay film yu wayndare (documentaires), fowukaay, téere ak film yu xale ñoo am ci àdduna bi ci yeneeni làkk te ñu man koo soppi ci sunuy làkk, sunu bëgge xam njariñ li ci wàllu kom-kom ak xel.
Ndaxam man nañuy jëfandikoo làkku Faraas ba leegi, waaye loolu warul a tax ba ñu bañ a xalaat ne aw làkk lu man a indi kom-kom la su fekkee ni lu ëpp ci askan wi moom lañuy jëfandikoo. Looloo dal wolof fii ci Senegaal, bambara ca Mali. Loolu la Microsoft sàmm ba tàmbalee amal Windows ak Office ci làkk yu mel ni wolof ak bambara. Google tamit tàmbali na ko.
Loolu tamit la waa Faraas xam ba taxawal kuréel gi ñuy woowe « Francophonie ». Lu ñu gën di jëfandikoo làkkuw Faraas ci àdduna bi rekk (lu tollook ñaari téeméeri milyoŋ ci doomi aadama) gën di yokk ay liggéey ca Faras, ndax ñoom ñooy soppi film yooyu di ko jaayaat yeneen téeméer ak ñeen-fukki milyoŋi doomi aadama yi nekk ci yeneen réew tey jëfandikoo làkku Faraas te ñun ñoo gi ci biir.
Ndax làkk wolof am na mucc?
Colette Grinevald di ab gëstukat ci làkk ca laboraatuwaaru làkk ba ne ca Lyon-II, ci ab gëstu bu mu defal Unesco aju ci dundiinu làkk yi, jàpp na ne lu jege 50% ci làkk yi dinañu saay fi ak atum 2100. Am na sax gox yoy, man naa am mu egg ci 90% (niki Óstrali ak Amerig) .
Gisees na ne ca atum 2100, làkk yees di gën a wax ñooy 1 :
- Àngale, niki làkk njënd, njaay ak xarala.
- Español ca bëj-saalumu Amerig.
- Purtugees, ca bëj-saalumu Amerig ak Afrig.
- Araab.
- Sinwaa ak Endo ca Asii.
- Swaahili ak Wolof, ci Afrig.
Li ñu mën a jàngee ci mbajtalu (résultat) gëstu bi mooy:
- Benn : Làkk Frãse bokkul ci làkk yi am mucc. Te monte Colette Grinevald mi jiite gëstu bi doomu réewum Frãs la. Kon ndax wareesnaa wéy di jiital ci réewum Senegaal làkk wu amul mucc, rax ci doll 10% askan wi rekk a ko dégg ba mën koo jariñoo?
- Ñaar: Sunu làkk wii di Wolof doon na làkk wu am mucc ba tax ñu war koo jiital ci réew mi. Kon ndax wareesuñoo jiital làkk wu amee nii mucc te lu ëpp 80% askan wi dégg tey jëfandikoo?
- Xarjata Diba Ngeer: Ndongo-daara ci wàllu yoon ca Daara ju Kawe ju Ndar
- Abdu Xaadir Géy : Gëstukat ak bindkat ci làkku wolof - http://www.wolof.co.cc
Man ngeen a cëru (contribuer) ci sémb bii, jaare ko ci indi :
- Ay xalaat
- Ay jukki (articles)
- Ay ŋara (fichiers) (kàddu, nataal, video, wayndare (document))
- Ay lëkkalekaay yu lënd (liens web)
- Ay baat ci baatukaay yi
Man ngeen a cëru it jaare ko ci bokk :
- Ci gënal ak jëmale kanam dal (site) bii nga xam ne aw liggéeyiinam ci PHP la ame. Ngir amal loolu yónnee-leen ag càkku (une demande) gu ebataaxal (email) ñeel kuréel gu nosukaay (informatique) gu dal bi, ci ebataaxal bii : webmaster@xibaaryi.com)
- Ci tekki ay jukki ci wolof ngir man a àgg ci juroom-ñatt-fukk ci téeméer 80% ci waa Senegaal yi déggul farañse.
- Ci alalal (financement) gu :
- Turu barab bi (nom de domaine) ak fat gi (l’hébergement),
- Jëndug ay jumtukaay yu nosukaay (achat de matériels informatiques) (nosukaay, scanners, jumtukaayu nataal yu nimorig (appareil photo numérique), caméscopes, etc.) ngir defar ay wayndare yu elektonig (pour la production de documents électroniques), ay nataal , ay kàddu aki video
- Alalal gëstu gu jëm ci jumtukaayu tekki gu boppu ( outil de traduction automatique) guy juge ci wolof dem ci français ak juge ci français dem ci wolof.
Boo bëggee jokkoo ak ñun:
- Senegaal: El hadji Mamadu Ngeer : +221 33 962 16 01 - Email: emnguer@gmail.com
Jërëjëf ci teewlu gi
Allaaji Mamadu Ngeer
Jàngaleek gëstukat ci xam-xamu nosukaay
ca Daara ju kawe ju Gaston-Berger bu Ndar
Njiital xibaaryi.com
|