[Askan] TAXAWU WAY-LORUY MBËND MI : Sëriñ Mansuur Si Jamiil sasoo na 600 xale
Le Soleil : Talaata 7 Sàt 2010 TAXAWU WAY-LORUY MBËND MI : Sëriñ Mansuur Si Jamiil sasoo na 600 xale.
Mbootaay Inond’action te Sëriñ Mansuur Si Jamiil di seen njiitu baayale, yóbbu na gaawu 600 xale (tolloon ci 500 daaw) ca Popongin ak Sufok (Ngeexoox) fa Sëriñ bi di gàddoo seenug dund ci diirub 21 fan.
Sababu jëf jooju, du lenn lumay fexe ba xaley mbënd yooyu jotaat ag mbégte. Ni ki noonu la ñu teddi ca Pikin, ci teewaayu Sëriñ Mansuur Si Jamiil ak jaraaf la di Paap Saña Mbay. Njiital Jibal gu juddu-réew ngir móolaatug réew mi, daa fas yéene, niki noonu, woo waa Senegaal ngir ñu soppi doxalin ci taxawu way-loruy mbënd mi. Mbokk na ci yi gën a jàmp ci taxawu googu, way-loru yi.
[Askan] Mbëj : Sigicoor a ngi ñaxtu ndax dog-dog yi.
Seneweb.com : Àjjuma 3 Sàt 2010
Mbëj : Sigicoor a ngi ñaxtu ndax dog-dog yi.
Askanu Sigicoor jot naa jaamaarlook kaaraange gi àjjuma, ngir naqarlu dog-dogi mbëj (courant) yi tëwa dakk. Way-ñaxtu yi dañoo jubali digg dëkk ba jaamaarlook takk-der yi ci diirub waxtu yu bari, ci li tukke ci ndawal rajo RFM ca diiwaan ba.
Nit ñu bari, bokk na ca ab jigéen ak ab waxambaane nataalkat, la poliis ba jot a teg loxo. Xibaarkat bu SenewebNews jokkool ca péeyum bëj-saalum réew mi leeral na ne cim ndaje mu ñu amaloon alxamis, ci la kurél gi ëmb kàrce yu Sigicoor, ci kàdduy Jibril Saane mi leen di waxal, sumb doxub ñaxtu gaawu. Dogal booboo ngi ñu jàpp ba léegi.
Aayeb yalnaaw ci Ndakaaru : àtteesna démb juróom-ñaari sëriñ daara.
Yéene gi nguur gi am ngir dakkal yelnaaw ci Ndakaaroo ngi tàmbalee jur as lëf. Yoon dugalna ci loxoom ba juróom-ñaari sëriñ daara, yu nar a tëdd juróom-benni weeri kaso, lañu àtte démb, ndax liñuy xiir seeni ndongo, yu bawoo ci réew yi sës ci Senegaal, cig yelwaan. Bu sëriñ soosee ñoom jàpp ne yalwaan rekk lañu am ngir mën leen a dundal, layalkat yi ñoom neenañu dogal yu nguur gi jël la rek ngir dalal xeli way-alalal yi (bailleurs de fonds).
Pressafrik : Alxamis 29 Sulet 2010 Jibo Ka ak suufam su tooke, ba fan ?
Suufus Ngañ Jaw (Caaroy) ba betteex ba tooke amagul ba léegi suuf su ko dalal. Ña dëkke Sebixotaan a ngay waaj it ngir bañ ñu tuxal ko foofa, ganaaw ba waa Morolang lànkee.
Ca Sebixotaan, janook-yéenakaay ba ñu naroon mujjul a àntu. Rajo RFM xamale na ne askan waa ne : « Jëwriñu kéew gee indeetul suuf su tooke sa ca Sebixotaan ».
Ca seen xeex ba, askanug Sebixotaan, digal nañu it kilifay gox ba ñu dogu ci moytu toxal woowu.
[Askan] Nettali : Ni la póliisu Senegaal bóomee Abdulaay Wàdd.
Politicosn.com : Gaawu 24 Sulet 2010 Nettali : Ni la póliisu Senegaal faatee Abdulaay Wàdd.
Démb ba léegi, Me Aamadu Aali Kan, miy layal waa kër Abdulaay Wàdd Yingu, mi faatuwoon ca ñaxtuy Yëmbël ya, njàmbat na alaxam (déposer plainte) ci kanamu njiitu àttekat yi ci lu aji ci ñeenti tuuma : faat, dóor ak ngaañ yu coobarewu, càcc wootekaay ak xaalis, ñàkk a wallu aji-loru, la yéenekaay l'As, mi nettali na jéyya ja demee, xamale.
Ba 18 waxtu jubee, la ko kilifaam, mi doon door a juge ci màggalug 130 eelu wooteb Laayeen yi, yónni mu jëlal ko xaalis ci boroom bitik ba ngir jënd xont. Ca yoon way dem Sedima ba nekk Caaroy, xale bu góor boobee, mi xelam demul benn yoon ne ma ngay dund waxtoom ya mujj, egg Caaroy tombeeg ñaxtu ñawkat yi doon naqarlu dog-dogi kuraη yi. Foofa lépp jaxasoo, takk-der yu soluwul, ngànnaayu ba fees, tàmbalee dàq nit ñi. Bamu gisee ñépp di daw, mu daw làqu ci kër ga mu njëkk a jot. Yégul lumay ne ay takk-der topp nañu ko. Boroom kër ga dal, ca ñaan leen ngir ñu bàyyi ko, waaye dara.
[Askan] [Nataal] Jéyya ca Jidda Caaroy Kaw : Kër gu màbb a faat benn nit
Seneweb.com : Alxamis 22 Sulet 2010 [Nataal] Jéyya ca Jidda Caaroy Kaw : Kër gu màbb a faat benn nit
Góor gu màgget a faatu ci taaxum kër gu màbb ca Jidda Caaroy Kaw, ca goxu Pikin. Mag moomu tolloon ci 70 at dadoon féexlu ca kanamu kër ga ba taax ma di màbb ca kawam ak ci kawi sëtam. Ñaari xale ya mucc nañu, waaye mag ma moom wuyyu ji na Boroomam. Ci kàdduy ndawal SENEWEB-NEWS ma teewoon ca bërëb ba, kër ga wonewul woon benn fett-fett. Jaraafu dëkkaan la, Aliun Badara Jóob, teew na fa ngir nemmeeku mbir ma.
[Askan] Faatug benn xale bu góor ci ab doxub ñaxtu ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi.
Seneweb.com : Alximis 15 Sulet 2010
Faatug benn xale bu góor ci ab doxub ñaxtu ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi.
Genn xale bu góor tollu ci 25 at faatu na Àllarba bi 19 waxtu (timis) tegee tuuti, ci ay ñaxtu yu waa Benn Baraak amaloon ngir naqarlu dog-dogi kuraη yi. Gannaaw ba kuraη bi dogee, la waa Yëmbël génn daaldi fatt yoon yi. Ci la takk-der yu Yëmbël agsi, woññi leen. Ca ba ñuy daw nag la kenn ci way-ñaxtu yooyu daanu ci kekk bi (gudroη bi).
Ba gox yu bari ci biir Réew mi noppee, la Ndakaaru tàmbalee jël wàllam ci yënguy Askan wi ndax dog-dogi kuraη yu takku yi. Ñawkat yeek ñeneen ñiy ligéeyee loxo ca Néegub njënd ak njaay (centre commercial) ba ca Asalem 5 (HLM5) wone nañu, ci Àllarba ji, seenug mer ci dog-dogi kuraη yi, yoy dañuy yàqal lu am solo ligéeyuwaay yu ndaw yi. Ngir xeex lu ñaaw loolii, way-yëngu yooyu lànk nañoo fey seeni bori kuraη. Ci mer moomu, nar nañoo sonnal bépp ndawi Senelec bu fa ñëwati di seet aka rëdd lañu lakk ci kuraη.
[Askan] Kërug takk-der bu Frondeteer (Front de terre) yëngóotina ndax ag siif gu mbooloo
Seneweb.com : Talaata 6 Sulet 2010
Kërug takk-der bu Frondeteer (Front de terre) yëngóotina ndax ag siif gu mbooloo def.
Ñaari takk-deru njàpple (auxiliaire) lañu teg loxo tëjandi leen ca kasob Rëbës, cig ciifug mbooloo gu ñu amaloon ci biir kërug takk-der booba. Bi ñu leen jàppee ci ab lànket bu seen kërub liggéeyukaay, la ñu leen dénk njiitu àttekat yi di Maxwa Semu Juuf ci ndigalu topp lu tukkee ci Porkirëer te Jëwriñu takk-der yi di Abdulaay Balde joxe ko. Ñu ngi xaar njeexitalu gëstu bi ñu tàmbali te, boo moyuwul, ñu àtte leen ci àttekaayu takk-der yi. Bii mooy ñaarel bi yoon kërug takk-der bu Frondeteer di taq cig ciifug mbooloo.