APS : Gaawu 21 Ut 2010 Sargalees na ndongo lu xereñ kaar ca ISAJ.
Iniwersite Seex Anta Jóob (ISAJ) jébbal na, ni ki ay neexal, ab nosukaay bob gàddu ak 650.000 CFA ab ndongol 23 at lu am ag Mokkal (Metriis) ci xayma bu piir, gannaaw bi mu saxalee at mu nekk moyen bu toll digante 16 ak 20/20, muy li tukke ci jibalul UCAD bi APS jot.
Musaa Gay mi jot neexal yooyee ci loxoy rektëer ba Abdu Salaam Sàll, ca xew ma ñu ko jagleloon ca rektora ba ci 11 w, mi ngi bindu ci Bànqaasu Xarala ak Tegnik ’’cig sàkkoom’’ ci 2006.
Boobook léegi, la jibal bi siiwal, ’’am na raayab Baax lool ci joηante yépp, sax do doon njiit (major) ca bànqaas ba dale at mu njëkk ma ba Mokkal bu xayma bu piir’’.
[Jàngale ak Tàggat] NEES DI TASEE XIBAAR CI WOLOF ? Jàngal taskati xibaar yi làkki réew mi.
Le Soleil : Àjjuma 13 Ut 2010
NEES DI TASEE XIBAAR CI WOLOF ? Jàngal taskati xibaar yi làkki réew mi.
Ngir setal jëfandikug làkk Wolof ci ëttu-xibaar yi, doon na lu jàmp ñu amal ag tottale ci ëtt yooyee. Amna sax way-màcc yu gis ne dañoo war a dugal njàngum làkki réew mi ci daara yiy tàggat way-tas xibaar yi.
Allaaji Asan Géy, mi ñépp taamu tasum xibaaram ci wolof bi muy def ci Rfm ci 13w, doon na kenn ci ñiy jëmmal ndamu wolof ci rajo yi. Laata muy tontu sunuy laaj, daa dugg ci tasuwaay-xibaar (stujo) bi jenook biroom ca taax Allaaji Elimaan Nduur, ngir joxe tënki xibaar yu 11w. Lu yomb ci moom. Booy deglu, ak ni mu ubbikoo ak ni ko wax ji yombee kaar, dangay yég ni mu amee ag jàppandal ci làkku Kocc Barma. Yoon la. « Wolof laa tànnoon niki ñaareelu làkk ba ma nekkee bànqaasu Àngale, la nu dénk. Moo tax, damay bind xibaar yi ci Wolof ». Doonul lu yomb yeneen way-tas xibaar yi.
[Jàngale ak Tàggat] AG YÀQATE CA REKTORA BU UCAD : Dàqeesna juróom-ñetti ndongo
Le Soleil : Àllarba 11 Ut 2010 AG YÀQATE CA REKTORA BU UCAD : Dàqeesna juróom-ñetti ndongo
Kurél giy sàmm yar ak teggin ca Daara ju Kawe ju Seex Anta Jóob bu Ndakaaru (ISAJ) génne na dogal yu diis gann, ngir daan yàqate ga amoon ca Rektora ba ak it ay njuumlaηi lijaasa yu ay ndongo defoon. Dàqeesna fàwwu juróom-ñetti ndongo, àyye ñett ñu bindu cib Iniwersite ci diirub juróomi at ak yeneen ñett yu ñu aj ñaari at. Ab ndongo, bu ñu teewaloon ca kanamu kurél ga, dina toog at du bindu ak keneen kuy toog ñetti at. Waaye bàyyees na juróom-ñetti ndongo ndax ñàkki firnde.
Ci juróom-benn ndongo yi ñu dàq ci fukk ak ñett ya teewoon ca kanamu kurél ga, ñaar a ngi binduwoon metriis ak lijaas ca bànqaasu yoon ak politig, yeneen ñaar ca bànqaasu koom ak yoriin (dayub lijaas), kenn ca bànqaasu xarala ak teknik (dayub lijaas) ak kenn ku ñu waxul bànqaas ba mu bokk.
[Jàngale ak Tàggat] JÀNG MU SUUFE MI : Fanweeri junniy nosukaay lees may ay bànqas aki daara yu Sene
Le Soleil : Gaawu 31 Sulet 2010
JÀNG MU SUUFE MI : Fanweeri junniy nosukaay lees may ay bànqas aki daara yu Senegaal.
Sémb Usaid /Njàngale mu suufe jot na, démb, ci loxoy waa liggéeyuwaay bii di Axa-Senegaal (jàngal aksaa), 30.000 nosukaay (ordinatëer). Nosukaay yu seetu yi tàcc a ngi jëm ciy bànqaas (college) ak daara yu Senegaal. Sémb Usaid/Njàngale mu suufe, mi ñu xam ci yëngoom yu bari ci jàngale mi, a ngi jot ndimbal loolu, démb, ci liggéeyadoowaale gi mu séq ak liggéeyuwaay yi.
Ci kàdduy tofu-njiitu Axa-Senegaal, S. Aliun Jaañ, ci jëf jooju dugg ci jàppale gi ñuy jàppale waa réew mi, liggéeyuwaayam niki noonu a ngi dugal loxoom ci xeex gi réewum Senegaal di xeex ngir wàññ roppi gi am ci xaralay nosukaay. Jaare na ci feddali sóobu gi Axa-Senegaal naal ngir jàngale mu sell ci Senegaal.
Nataal yu ñu doxal (dessin animé) ci làkk Wolof ak ISMAEL LÓ ! Jàngoro yi dañoo mer ba futt booleek jaaxle ndax nit ñi dañoo def jeego yu réy ngir xeex leen. Niki noonu, ñu dalal seen kilifa SIDA, mi am pexeem faagaagal doomu aadama : song kaaraange yaramam. Waaye nees di def ba aaru ci moom aki waayam ?
Ligéeyuwaay biy jàppandal cëraakonu (serveur) web, bu lënku dàkk ci internet, lees tuddee dëkkëlaakon (hébergeur). Ñaari xeetu dëkkëlaakon a am:
Dëkkëlaakon bu amul-fey dañuy dëkkël dalu web ci ludul fey ci diskiw cëraakonu web ngir sos say xëtu webdëkkël . Xeetu cër la bu amaul-fey nakajekk. Ñi ngi amee xaalis ci siiwal yees lal ci dal bi (yoon la wuñ di gën di bàyyi), mbaa rekk ci limu way-yër yi.
Dëkkëlaakon yuy feyyu. Dëkkël la guy warlul cër gu maanaawu (soru jàll = bande passante) akug kaaraange (kaaraangeg njoxe yi fegug limu teq-teq yi). Mbir la mu mënul a ñàkk ci dal yu bëri ay way-yër (lu ëpp 1000 way-yër) te it da laaj njëndum turuw moomeef (nom de domaine) masalan www.senxarala.com
[Jàngale ak Tàggat] TRADUCTION DE GOOGLE EN WOLOF : L’UGB soutient la présence des langues nationale
TRADUCTION DE GOOGLE EN WOLOF : L’UGB soutient la présence des langues nationales sur Internet
L’Université Gaston Berger (Ugb) de Saint-Louis a abrité hier un workshop pour la traduction de Google en Wolof. L’objectif de cet atelier est de permettre aux participants de s’approprier les outils de traduction pour la présence en ligne de la langue Wolof.
Dédié aux étudiants, le workshop de l’Université Gaston Berger, sur la traduction de Google en wolof, vise à développer la présence en ligne de la langue Wolof, en fournissant des listes de terminologie et des formations.
Le Recteur Mary Teuw Niane, qui a remercié Google pour son soutien apporté à l’UGB, a indiqué que les langues africaines étaient quasi inexistantes sur le Web. Celui-ci enregistre surtout les langues des pays développés.
Cette situation, selon Mary Teuw Niane, avait suscité des débats sur la domination culturelle à travers le réseau. « La situation technologique de l’Afrique connait une évolution rapide, malgré la fracture numérique et les langues africaines deviennent de plus en plus visibles dans le cyberespace. Cette visibilité est plus dynamique avec Google dont le service de traduction en ligne contribue largement à la diversité linguistique sur Internet », a dit M. Niane. Il a expliqué que « disposer d’une interface en Wolof, c’est se positionner sur le moteur de recherche le plus en vue au monde. » Et d’ajouter que « la présence du Wolof sur le net participe à la diversité linguistique et à la valorisation d’une de nos langues nationales à travers le monde. »
Pour sa part, Angela Muigai, Représentante de Google chargée des langues africaines, a indiqué que le but principal est d’accorder l’Internet à tous. Selon elle, une grande partie des populations de la Mauritanie, de la Gambie et du Sénégal ne comprennent pas le Français et n’ont pas le droit d’être laissées en rade. Tout en magnifiant le partenariat et la collaboration de Google et le Sénégal à travers l’UGB, elle a souligné la nécessité de prendre cette couche de la population en compte à travers cet important programme déjà expérimenté dans plusieurs pays. Le comité d’organisation de ce workshop donnera l’occasion de tirer un certain nombre d’enseignement et d’éclairages sur l’utilisation de la langue wolof. Pour son président, Mamadou Nguer, « des politiques doivent nécessairement être menées pour vulgariser nos langues nationales, en particulier le wolof qui est compris et parlé par plus de 80°/° de la population. »
[Jàngale ak Tàggat] TEKKIG GOOGLE CI WOLOF : UGB dugal na loxoom ci jàppandal làkki réew mi ci Inter
Le Soleil : Gaawu 12 Awril 2010 TEKKIG GOOGLE CI WOLOF : UGB dugal na loxoom ci jàppandal làkki réew mi ci Internet
Daara Ju Kawe ja ca Ndar (Ugb) dalal na démb ndajeem tekki Google ci Wolof. Sababu ndaje moomu nag moodoon fexe ba way-teew ya nànd jumtukaayu tekki yu Google ba mën a dugal làkk Wolof ci Internet.
Muy lu ñu jagleloon ndongo ya, ndajeem Daara Ju Kawe ji ñu duppee Gaston-Berger, ngir tekki Google ci Wolof, suqali Wolof ci Internet a ko jékkati jaare ko ci tàggat gu fa waa Google aki baat yi mu leen jox.