Raaya réewum Senegaal a ngi am ñetti rëdd yu taxaw te tolloo, bu wert, bu mboq ak bu xonk. Ab bideew bu wert am juróomi cat a nekk ci digg rëdd bu mboq bi.
Kulóor bu wert bee ngi màndarga kulóoru yónent Yàlla Moamet ñeel jullit yi, wow yaakaar ñeel kercen yi mba wow njur ñeel ñi gëmul Yàlla. Nimero bi ko sistem Panton jox mooy 361 mbaa RGB 30 181 58.
Xam ngéen ne nite (l’humanité) mi ngi juddoo Afrig, tàqalikoog nit ak dundat (animal) mi ngi ame fii ci Afrig, loolu kenn sikkatu ko.Xew-xew bu am solo bii mi ngi am booba ak leegi toll na ci 5 milyoŋ ak juroom benn téeméeri junniy at (5600000 ciy at), Afrig ngay man a fekk mbooleem xeeti nitu pax (homme fossile), loolu doo ko gis ci beneen gox (continent).
LEMONDE.FR : Altine 16 maars 2009 Askanoog Kleopaatar ci Afrig : firnde gu tukkee ciy yax
Lii Liz Taylor doon Kleopaatar (Cléopatre) ci filmu Joseph Mankiewicz dina jur ag jaaxle gu réy. Ana lu ko waral? Kleopaatar VII doonan buuru Misra (Egypte) bu jigéen, te ñu ko daan woowee "Grek bi (la Grecque)" ndax li mu bokkoon ci askanu ptolémaïque sosoo Masedoni (Macédonie), ndeke ku ñuul la woon. Loolee la BBC xamale ci ab dokimaanteer bu mu duppeeKleopaatar : jëmmi reykatu nit, bop deesna ko wone 23 maars.
Séeréer genn giir la gu nekk Senegaal. Séeréer si ñoo jur Lebu yi ak Wolof yi, waaye wolof yi am nañu yeneen xeet yu ñu bawoo tam yu duli Séeréer. Siin ak Saalum mooy seeni nguur.
Soog a nekk Siin-saalum, ca Tekuruur lañu nekkoon. Dañoo gàddaay dem Siin-Saalum ndax dañu doon daw Lislaam ak Muraabituun yi (les Almoravides). Muraabituun yi dañu xare "jiyaar" ak séeréer si, ngir dugal leen ci Lislaam, waaye séeréér si bëgguñu woon loolu. Lii lépp nag ca yoonu imbraatóor gu Gana la xewe woon, booba imbraatoor gi mi ngi doon tàmbalee daanu. Foofa ca Siin-Saalum ay Soose (Sooninke), ñoo fi doon dëkk. Kon mbokkug Soose ak Séeréer ci dëkkandoo la bawoo, ba noppi Soose yu bari dem nanu dëkki ca Kaasamaas
Yewwute gu ndefar ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug ndefar, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu gi.
Waaye nag, moom ndefar gii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Aamerig, la ko dale ca njëlbéenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Bi mu ko defee nag, ay jeexiitalam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci àdduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g.
Ci lu tollook juroom ñatteelu xarnu g.j, jaayees na ay jaam yu waa Afrig ci ay yaxantukat yu daa def yaxantug tàkk gi (
la traite du désertt) , ak gu tefes gi ci tefesug mbàmbulaan gu End gi (ocean indien).
Joolaa genn la ci giiri Senegaal yi. Ñoom Kaasamaas lañu fekk baax. Ca yoonu Imbraatóor gu Mali, lañu dem dëkk. mandeŋ yi ñoo leen daq, ñu dem kaasamaas. Ca bëj-gànnaaru Gine Bisaawóo, ña ga fa tamit. Baynuk yi ñoo doon jiite joolaa yi ca kaasamaas. Ñoo tabaxoon nguurug Kasanlaa. Joolaa yi ak Baynuk yi, dañu dëkkandoo woon ak Soose yi, Njaago yi ak Pël yi. Ñoom ñoo fa njëkkoon joolaa yi.
Pullaar aw làkk la wu ñuy wax daanaka ci 20 réewiAfrig gu sowwu ak gu diggu, Dale ko ca pegi dexu Senegaal ba ci gu Niil, waaso yu pël, tukulóor ak yu lawbe ñooy ñi koy làkk.
Ci cosaan pël yi ay sàmmkat lañu, waaye tay daanaka xeeti liggéey yépp lañuy def: yaxantu, béy, njëwrin, añs.
Wolof genn giir la gu nekk Senegaal. Wolof ñoo ëpp ci waaso yi ci Senegaal.
Maami wolof yi Isipt lañu bawoo. Séeréer si, Pël yi, Sooninke yi, Tekuruur yi (Tukuloor), ak Saraxule yi juge nguuru Bagirmi ca réewum Cadd. Wolof yi ca xeet ya lañu juge. Xeet ya yépp danoo jaxasoo, ca yoonu Imbraatoor gu Ghana, ca dëkk bi nu tuddé Jolof. Wolof mooy ñu bawoo Jolof, Waa-Lof (ay gaa yu juge Lof) walla Waa-Laf (ñoñ Laf), di nekk tay Wolof. Seex Anta Joob, Walaf la doon wax. Noonu la xeetu Wolof judoo.
Mooy xam-xam bi'y gëstu la xewoon demb. Di itam mbooleem ay Jëf ak ay xew-xewu demb, la ko dale ca ña nu jiitu woon ba ci nun. Taariixkat mooy ki'y gëstu di bind ci wàllu taarix
Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri seen way dëkk. Da na nu waxal it ca dund ga fa amoon. Ci gàttal daal, xam-xamu taariix day gëstu li-wéyi nit (dembam) cig matale.