 | |
| Cëru (Contribuer) | Boo bëggee siiwal ab jukki (article)
[cuqal fii] |
|
| |
[Politig] Baara Taal, Gaajo, Amsatu Sow Sidibe, Seriñ Mansuur Si Jamiil ak yeneen kuréeli
| 
Politicosn.com : Dibéer 29 Ut 2010
Baara Taal, Gaajo, Amsatu Sow Sidibe, Seriñ Mansuur Si Jamiil ak yeneen kuréeli juddu-réew booloo nañu ngir jàmmaarlook Wàdd ak Kariim.
Njiiti juróom-ñaari kuréeli juddu-réew (mouvements citoyens), ànd ci biir ab ‘’Néegub wecconte xalaat’’, biral nañu gaawu ca Ndakaaru ab tëru waar (plan d'action) bob li ko jékkati di ‘’dakkal nguurug Abdulaay Wàdd te ànd ci sos ay sàrt yuy jàppandal nguur gu sell’’ ci Senegaal. Teewoon na ca ndaje moomu, Seex Tijaan Gaajo, Baara Taal, Amsatu Sow, Àlla Jeng, Seriñ Mansuur Si Jamiil. ’Ak yeneeni mbootaay, kuréeli askan yi, ñu gën leen xamee ci kuréeli juddu-réew, dañuy fexee tëral ay sàrti weccoonte xalaat yu jàppandi ngir jóg ci nguurug Wàdd gi ’’, la njiit yi jibal gannaaw lël bañu amaloon ca bis boobee. Ñi ngi waaj ab dagaan ngir ‘’aar Ndeyu Àtte Réew mi’’ ak ab doxu ñaxtu ngir bañ ñu far palinu ñaari yoon yi, ‘’muy li nguur gi teg bëtëm’’ jamono jii.
| |
|
[Politig] [KÀDDU] : Wàdd cim jataayu tas-xibaar ca Njénde la ci 1 Màrs 2007 :
| 
Politicosn.com : Dibéer 22 Ut 2001
[KÀDDU] : Wàdd cim jataayu tas-xibaar ca Njénde la ci 1 Màrs 2007 :
"Maa naj diirub jiite réew mi ci ñaari at ci Ndeyu Àtte bi, Duma bokkaat ci ñiy joηante"

Rajo RFM jàllale na dibéer gii ay kàddu yu njiitu réew mi Wàdd di saxal ne du bokk ci way-joηante ci atum 2012 ndax Ndeyu Àtte réew bi dako koo tere. Politicosn.com jotnaa gis jukki bi Seex Tijaan Njaay, miy njiital bindkati APS, xaatim. Muy kon lu nguur gi diglewoon ag siiwalam. Lu ci Wàdd doon wax ? Du bokk ci way-joηante yi ci 2012 ndax Ndeyu Àttem réew mi tere na ko.
Jukki bi wax na lu yàgg ci Idriisa Sekk. Tànnees na ci as tuut : "Tàggoo naa ak moom. Du ko doon, fàwwu mu xam ko. Bu bëggee nekk njiitu réew mi, na jaar ci yeneen yoon’’, la njiitu réew biraloon.
| |
|
[Politig] [Nguur] Aji-yor kàddug njéndel réew mi : Seriñ Mbàkke Njaay wuutu na Mamadu Bàmb
| 
APS : Àjjuma 6 Ut 2010
[Nguur] Aji-yor kàddug njéndel réew mi : Seriñ Mbàkke Njaay wuutu na Mamadu Bàmba Njaay.
Ndakaaru, 6 ut (APS) – Seriñ Mbàkke Njaay tabb nañu ko mu yor kàddug njéndel réew mi, wuutu Mamadu Bàmba Njaay, gannaaw ñaari dogal yu njiitu réew mi jél yu ñu siiwal ci jibalug jataayu jëwriñ yi, yu APS jot àjjuma.
Kon, Seriñ Mbàkke Njaay jëwriñ la ci njéndel réew mi, yor jokkolante gi, wàllu tàggat-yaram, ak kàddu njéndel réew mi.
| |
|
[Politig] NGIR DALAL ASKAN WI : Wàdd sas na Paap Sàmba Mbuub ngir mu waxtaan ak Baara Taal
| 
Lobservateur : Talaata 6 Sulet 2010
NGIR DALAL ASKAN WI : Wàdd sas na Paap Sàmba Mbuub ngir mu waxtaan ak Baara Taal ak bépp doomu senegaal bu gis ne dañu ko tooñ

Mbaa du lépp daa nara dal? Walaa dañuy doxalati beneen naalub politig ngir tuur nu lëndëm? Ak lu ci mën am daal, Sg (Sang) Wàdd gise naak Séex Taal Jum tey, tàllal loxo Baara Taal, booleek di dal Piyeer Ayim.
Démb, Sg Wàdd dalal na, ca Njénde Réew mi, Séex Taal Jum. Ci ndaje moomu ñaar ñooñu déggoo nañu gannaaw ba ñu gisee ni dañoo réeroowoon rekk. Sg Wàdd joxaale na sax kii di Paap Sàmba Mbuub, di Jëwriñ juy jàpple Njiitu Réew mi, ndigalul « ubbi buntam, dalal képp ku yem tolluwaay ak Séex Taal Jum, déglu ko, jél firnde yi mu yor te teg ko ci loxoom ( moom A. Wàdd). Ngir mu dëgg ci tankam te delloo ñooñu ñu tooñ seeni àq, te ñi leen tooñ di ay sàmbaabóoyu campéef yuy jaare ci jege gi ñu jege Njiitu Réew mi ak waa kërëm ngir njuumlang nit ñi».
| |
|
[Politig] [ NATAAL ] Doxu ñaxtu wu 3 Awril bu bennoo Siggil Senegaal.
| 
Seneweb.com : Dibéer Awr 2010
[ NATAAL ] Doxu ñaxtu wu 3 Awril bu bennoo Siggil Senegaal.
| |
|
[Politig] [Interview - WIDEO ] : Me Wàdd a ngi leeral politigam.
| 
Seneweb.com : Altine 1 Màrs 2010
[Interview - WIDEO ] : Me Wàdd a ngi leeral politigam.
Ci interview bi mu amal ak telewisioηu boppal Canal Plus, te rajo boppal Océan FM jàllaleko, njiitu réew mi , Me. Abdulaay Wàdd a ngi àddu jafe-jafey Kaasamaas, diiwaan bu nekk ci bëj-saalumu réew mi.
| |
|
[Politig] Senegaal: Amaleesna Njëwriñ ju yor mbiiri
| 
Sen24heures.com : Àllarba 06 samwie 2010
Senegaal : Amaleesna Njëwriñ ju yor mbiri diine yi.
Njiitu réewum Senegaal Abdulaay Wàdd tàbb na jëwriñ ju yor mbiri diine yi, di guléet ci réew mi. Looloo ngi am ci jamono ju ñagas digante ay kilifa diine ak njiitu réew mi, la Njëwriñu Jokkanlante gi xamale.
S. Mamadu Bàmba Njaay, di taskatu xibaar bokk ci làng politigu nguur gi, la ñu tàbb Jëwriñ xelalkat bi yor mbiri diine yi teg ci yor kàddu njiiru réew mi, la AFP siiwal jéle ko ci Njëwriñ loolu.
| |
|
[Politig] 24w ginnaaw tekkig ndombo-tànkam, Gaajo soong na: « Da maa fas yéenee xeex yori
| Gaawu 03 oktoobar 09
24w ginnaaw tekkig ndombo-tànkam, Gaajo soong na: "Da maa fas yéenee xeex yoriinu nguur gu bon"
24 waxtu gannaaw tekkig ndombo-tànkug jëwriñu nguurug Senegaal gi yor wàllu bitim réew, Dr Seex Tiijaan Gaajo jibal na ay kàddu yegge ko askanu Senegaal. S. Gaajo narul a bàyyi ay yëngoom niki yenn yëwriñ defee bunu tekkee seen ndombo-tànk. Daa fas yéenee wéyal xeex bi nga xamni mësukoo bàyyi. Bind na cib bataaxal : «Tàbbi naa bis niki tey ci politigu aar demokrasi ak réew mi, xeex ger, yoriinu nguur gu bon te di yéene sottal bennal réewi Afrig yi.»
| |
|
[Politig] Tontul Sàmba Julde Caam ñeel àtte bi ko kuréelu Pulaar yi di waajal ca Mànt-la-J
| 
Xibaaryi.com: Dibéer 27 Sàttumbar 2009
Tontul Sàmba Julde Caam ñeel àtte bi ko kuréelu Pulaar yi di waajal ca Mànt-la-Jolie (Frãs).
Assalaamaalikum,
Ñeenti bind a ngiii aju ci wax jii ci kaw. Ñett yi maa leen bind, ñeenteel bi sennaas waay a ma ko yónnee ngir yégal ma ab dajeeb-àtte (réunion-tribunal) gu war a am ca Mànt-la-Jolie bisub 17 oktoobar ngir teg ma ay daan (ndax li ma digle woon ñu jàngale làkk wolof ci réew mépp ci jukki bii ).
Bind yaa ngi toftaloo kem bis yi ñu leen bind.
Jot naa tontu yenn bataaxal yi ma ñenn bind, ndax tontu yépp amul daanaka njariñ.
| |
|
[Politig] JIBALUL POLITIG WËRGAL KÀPP GU NJIITU JËWRIÑ YI: Xiiroo digante nguur gi ak kujj
| 
SudQuotidien : Àjjuma 24 Sulet 2009
JIBALUL POLITIG WËRNGAL KÀPP GU NJIITU JËWRIÑ YI: Xiiroo diggante nguur gi ak kujje gi.
Ñu baree teewoon , alxamis 23 sulet, ca Péncum Ndawi Réew mi ngir fekkee jibalul politig wërngal kàpp gu njiitu jëwriñ yi Suleymaan Ndeene Njaay. Jotaay boobee, yàggee juróom-ñeenti waxtu, tax na Njiitu jëwriñ yi wone nan la fas yéenee doxalee ngir jëme réew mi ci kanam. Budee yaakaar juddu na ci ñenn ñi, ña ca des moom jàpp nañu ne wax juy mujj ci digle yees di fàtte dong la.
Ci 10w la Njiitu jëwriñ yi Suleymaan Ndeene Njaay egsi ci béréb ba, ay tàccu aki sarxolle gatandu ko.
| |
|
|
| |
| Téere sargal |
|
|
|
|
| Kurél yiy yëngu ci suqali làkki réew mi | • Osad
• Anafa  |
|
|